LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (19/8/2025)

Yeneen i xët

Aji bind ji

FMI YÓNNEE NAY NDAW FI SENEGAAL

Ay ndawi FMI (Fond Monétaire International, di kurélug koom-koomu mbootaayi xeet yi) ñëw nañu fi réew mi ngir dox fiy tànk ci 19 ba 26 ut 2025. Xibaar la bu tukkee ci jëwriñu koppar geeg ngurd mi. Seen tànk yooyoo ngi aju ci topp dige yi Càmm gi defoon ci wàllu koom-koom ak saytu tolluwaay yi, ànd ceek kilifay réew mi. Naka noonu, ma-xereñi kurél gi dinañu weccanteek kilifay réew mi ci doxalinu ngurd 2025 mi, waajtaayi njëlbéenu àtte kopparal bu 2926, ak coppite yi ñu war a andi ci koom-koom gi.

MBIRI FARBA NGOM

Laykati Farba Ngom yi weddi nañu waxi Meetar Keledoor Li mi ñu doon tudd ci layoo bi. Nde wax ji yaatu woon na fan yii ci mbaali jokkoo yi ni Farba Ngom dafa fay 100i milyoŋ kii di Meetar Ly ngir mu fekkasi kippu laykat yi koy layal. Ci yégle bi ñu génne, ña nga cay xamle ni xibaar boobu wérul. Ay wax yu ñu tasaare la ngir yàq deru dépite bi.

AFROBASKET 2025 : SENEGAAL JÀLL NA CI KAAR DË FINAAL YI

Gaynde Senegaal yi jàll nañu ci kaar dë finaal yu Afrobasket 2025 bi, ginnaaw bi ñu dóoree Sudaŋ. Démb ci altine ji lañu doon amal joŋante boobu ci ñaareelu ay yi. Gaynde Senegaal yi mujjee dóor 78 poñ ci 65. Ndam loolu nag tax na ba ñu jàll ci joŋante dóor-mu-toog yi. Waaye itam, joŋante bu metti moo leen di xaar ci wàll wile ak Niseeriyaa mi ñu nar a dajeel.

POŊ BA MÀBB FA KANEL

Fa gox bu kanel, am na benn poŋ bu fa màbb. Bees sukkandikoo ci xibaar yi ñu siiwal, wal yu metti yu ndoxu taw bi doon wal foofa ñoo ko waral. Poŋ baa nga nekk ca diggante Caañaf ak Dembakaane. Ci mujjantalug ayu-bés bi lañu seetlu ni moo ngi doon   tàmbalee bàyyi. Ci dibéer ji sax jot nañu faa jóor ay doj ak i saaku suuf ngir dooleel ko. Waaye dafa mujjee màbb ba ñu demee ba ci guddi dibéer ji, jàpp altine. Jamono yii nag, andi na fa jafe-jafe bu réy ci dem beek dikk bi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj