POLITIG : Toussaint Manga génn na PDS
Ab bataaxal la kii di Toussaint Manga jébbal njitaal PDS li, Abdulaay Wàdd, di ko xamal ne dafay bàyyi parti bi ak bépp ndombog-tànk bi mu ci yoroon. Ci biir bataaxal bi, mi ngiy ciy sant Njiitu réew ma woon, di ko sargal ak a ñaanal.
FUTBAL
Ñaari saa-senegaal yi nekk ekibu Chelsea bi neexlewuñ tey. Nde, ci ñetteelu fan Premier League bi amoon dibéer jii, 21 ut 2022, waa Leeds United door ñoo leen dóor 3i bal ci dara. Bal bu njëkk bi a ngi dugg, ginnaaw bi Aarason fokkatee bal bi ci Eduwaar Mendi daal di duggal. Kalidu Kulibali tamit mujjul àggali futbal bi, dañu ko génne ginnaaw ñaareelu kartoŋ mboq bi mu am.
BITIM-RÉEW
Jawriñ ji yor mbiri bitim-réew génne na ab yëgle di ci xamle ne, benn saa-senegaal a naroon dàjji bunt àmbasaad bu Senegaal ca Pari, ci gaawu bi 20 ut. Ab waay la bu tollu ci 42i at nekkoon cib kamiyoŋ ak i gànnaayam, demoon na sax ba tàmbale yéeg ci etaas bu njëkk bi. Waaye mujj nañ ko teg loxo ci ndimabalu sàndarm saa-senegal bi di wuyoo ci turu Sonaar Seen ak pólis bu Farãs. Ñu ngi ko dénc ci komisariyaa bu 16e Arrondissement bu Pari, di xaarandi ab lànket.
WÉR-GI-YARAM
Kurél gi ëmb waa aar ak sàmm Raglu Aristide Le Dantec, amaaloon nañ ab doxu ñaxtu ci gaawu bi 20 ut bi, ca Place de la nation, ànd ci ak waa FRAPP, ak ñu bari ci ndawi réew mi. Li ñu doon kaas te di wéyal xeex mi mooy bañ Càmm gi jaay 3i ektaaru raglu bi. Li taw biy bari ci biir Ndakaaru yépp, terewul doxu ñaxtu bi am.