Dépite yi wote nañu sémbuw àtte wiy jëmmal yoolekat yi. Muy àtte bob, li ko tax a jóg mooy xeex nger ak luubal. Naka noonu, sémb wi di soññ askan wi ñuy boole jépp jëf ju jëm ci mbuxum ak luubal alalu askan wi. Sémb wi nag, ginnaaw bi mu jëmmalee yoolekat bi, dina ko aar. Am na itam ay neexal yu koy xaar. Waaye, du dangay boole rekk jot ci. Fokk xibaar yi ñu joxe wér te am yu mu feeñal ci luññutu yi.
YËNGU-YËNGU YI FI AMOON CI WOTEY 2024 YI
Buntu Yoon a ngi waaj a ubbiku ci yëngu-yëngu yi fi amoon ci wotey 2024 yi ak loraange ya ca aju. Jëwriñ ji ñu dénk Yoon, Usmaan Jaañ, xamle na ni jokk na toppekat bu mag bu Ndakaaru ngir mu tijji ag luññutu ci jëyya yi amoon ci diggante 2021 ak 2023. Waaye nag, narul a doon luy gaaw. Nde, bees déggee li jëwriñ ji wax, dees na bàyyi xel àtte neenal bi ak bañ a gaawantu balaa ay neenal di amaat ci doxalin wi.
AMINATA MBENG NJAAY AK WAA PS
Diggante Aminata Mbeng Njaay ak làngug pólitig gi mu bokk (PS, Parti Socialiste) a ngay gën a ñagas. Mbooloo mi jóg ngir sopparñi làngug PS (Initiative pour la réforme du PS) ñoo ko yóbbu ca kanamu yoon. Li ñu koy jiiñ nag mooy ca 2019 ba léegi moom moo nekk fara-caytu bu nu fa tegandi woon. Waaye, dafa ci faf ëppal ak di ci jaay doole. Boobu ak tey itam wootewul wenn yoon ndiisoo gu mag gi. Naka noonu, war na a wuyuji keroog 1 fan ci weeru sàttumbar.
WOOTE YI FA DSC
Toppekat bi dóor na màndaa déppoo kii di Bugaar Juuf ginnaaw bi ñu ko tegee loxo ci kàddu yi mu yékkati ñeel elimaanu jëwriñ yi ak fippukat ya ca Kaasamãs. Ginnaaw Sëñ Juuf, woolu nañu itam faramfàccekat bii di Mamadu Si Tunkara. Moom itam, ay kàddu yu mu yékkatee tax ñu woolu ko. Ñuy ay kàddu yu mu jibal ci àtte bi ñu namm ci mbiri ngóor-jigéen. Mu cay wax ni àtte ba amul lenn lu mu mën a jur ci wàllu yoon. Muy kàddu yu déppite yi ëppe fa Ngomblaan ga jàpp ni dañoo doy-waar.