Ëttu àttewaay bu mag bi gàntal na neenal-àtte bi layookati sonko yi sàkku woon ngir ñu saytuwaat dogal ga mu jëloon ñeel Usmaan Sonko ci wotey 2024 yi.
Seex Baara Dolli bokk ci wutaakoni (lawaxi) wotey 2024 yi, xamle na ne seeti woon na Sonko fa kasob Cap Manuel. Wax na ne, bés bu ñu ko falee ba mu nekk Njiitu réew mi, li muy jëkk a def mooy génne Sonko ndung-siin.
Ginnaaw bi mu tàmbalee doxantu-pólitigam bees duppe « MOTTALI YÉENE » ci dëkk-dëkkaat yi wër Senegaal, moom Xalifa Sàll ak i ñoñam yu Taxawu Senegaal, dañ leen kar fee ca Maatam, tere leen ñu wéeyal seen doxantu. Nde perefe bu Maatam baa aaye lu ni mel. Dafa mujje doxe tànk.
Ginnaaw bi Aminata Ture pelentee kii di Yaaxam Mbay, njiitul yéenekaay Le Soleil, ci xiibar bu mu gis ne werul ñeel « Aamadu Ba am na ci 3 782 052i xobi baayale ». Yaaxam Mbay indi na ci ay leeral, tontu ko ne bi muy biral bile xibaar ci Aamadu Ba, boole na ci ne ci L’observateur la jële boobu xibaar. Dolli na ci tontoom ne moom it dafay pelent Aminata Ture.
Raglub Roi Baudouin bu Géejawaay
SAMES, di ab kurél gu ëmb fajkat yi moom seen bopp biir Senegal, xamal nañ ne, fajkat yi nekk Roi Baudouin dinañ amal ab gereew altine jii di ñëw 4 desàmbar. Li ñuy ñaxtu mooy li seen nafag atum 2022 ak mu 2023 bariy lënt-lënt. Ñoo ngi kaas tamit li ñiy xas ak a ŋàññ fajkat yi, moo xam ci fànn bu mu mën di nekk.
Tàggat-yaram
Démb ci gaawu gi la Farãs doon joŋante ak Almaañ, muy mujjantalu futbalu coupe du monde U17 yi. Bi ñu dawalee ba mu jeex, te ndam demul, ndam dikkul, ci lañ def daj-dëppu. Noonu la Almaañ jëlee raw-gàddu gi ci 4i bal ci 3i ci kow Farãs.