LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (30/1/2025)

Yeneen i xët

Aji bind ji

7i BAKKAN ROTATI NAÑU CI TALI BI

Juróom-ñaari nit ñoo ñàkk seen i bakkan ci am ndog mu metti mu am diggante Kër-Majabel ak Waag-Nguuna. Tay ci suba la ndog mi am, ci wetu dëkk bii di Kër-Abdu-Jafe, ci kominu Kër-Mandongo.

Bees sukkandikoo ci xibaar yi njëkk a rot, benn “7 palaas” moo mbëkkante ak benn “pick-up”. Daamar bu njëkk baa ngi bawoo woon dëkk bu tudd Njaay-Gorko, ñaareel bi jóge woon Kawlax.

MBIRUM LAT JÓOB

Tay lañu doon déglu Lat Jóob. Àttekat biy luññutu bi, bokk ci ëttu àttekaayu koppar yi, moo ko déglu ci tuuma yees koy toppee.
Ci li Seneweb biral, moom jëwriñu tàggat-yaram ja woon, dafa weddi tuuma yi ko Yoon gàll yépp. Moom daal, dafa feddali kàddoom ya mu njëkkoon a wax ca luññutu gu njëkk ga.

PÓLIS : “ÑU RAFETAL KÀDDU YI….”

Njiitul pólis li, Maam Séydu Nduur, yedd na ay ndawam. Nde, daf leen tere kàddu yu deme ni “minable” walla “dégage”.
Dafa di, bari na ci nit ñi ñuy naqarlu kàddu yu ñagas yi leen takk-der yiy faral di wax. Daf ci am nag ay baati ñàkk kersa walla ay kàddu yu tegginewul. Loolu yépp nag, kilifa takk-der yi tere n’a leen ko léegi.

XAREB GOMA

Fitna ji dakkagul fa Goma. Nde, ci alxamesu tay jii, xeet yu metti amaatoon nañu fa diggante rëtalkati M23 yi ànd ak sóobarey Ruwàndaa yi ak sóobarey làrme Kongo RDC. Am na ay xeexkat yu ñuy woowe “Wazalendo” yu nekk foofa, fa Goma, yuy jàppale sóobarey Kongo RDC yi ci xeex bi.

KUPPE : RENNES TABB NA ABIIB BÉEY

Këlëbu Farãs bii di Rennes tabb na Abiib Béey, def ko tàggatkatu ékib.
Rennes nag, Ligue 1 la nekk. Waaye, jamono yii dafa nekk ci jafe-jafe. Moo nekkagum ci 16eelu palaas bi ça sàmpiyonaa ba. Pasug 6i weer la Abiib Béey xaatim. Liggéeyam mooy fexe ba Rennes bañ a wàcc Ligue 2.

LÀMB JI : CNG DAAN NA MOOR KAŊ

Mbër mii di Moor Kaŋ dina toog ñetti weer yoy, du ci takk ngemb. Li ko waral mooy daan bi ko CNG daan ci diirub 3i weer, ginnaaw Aama-Neex ak Sakob Balde.

Moor Kaŋ nag, dafa wuute jàkkaarloo bu mujj bi mu waroon am ak Jóob 2. Fàllu Njaay moo tëgg làmb jooju.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj