JËWRIÑU BIIR-RÉEW MI AMAL NAY TABB YU YEES
Jëwriñu Biir-Réew mi, Seneraal Sã-Batist Tin amal nay coppite yu bari ci kàngaami pólis yu mag yi. Nde, dafa wàccee ay nit, tabb ñeneen ñu leen di wuutu fa ñu nekkoon. Coppite yooyii, ci banqaas yii toftalu lañ leen amal : SU (Sûreté Urbaine), DIC (Division des Investigations Criminelles), « Division de Cybersécurié » ak ci yenn komisariyaa yu mag yi. Nee ñu, coppite yooyu jëwriñ ji indi, li mu ko duggee mooy ñoŋal caytug kaaraange gi askan wi. Nde, jamono jii, rey gi bari na lool ba jéggi dayo. Daanaka, doo xéy bés te déggoo ku ñu reyul walla ku ñu gaañul. Waaye, am na ci tabb yoo xam ne, jàppees na ni ay daan la.
Am na ay tabb yu bari nag. Waaye, yii toftalu lees gën a ràññe :
-
Aysatu Njaay, nekkoon Komiseer bu mag bu Cees, tabb nañ ko Tof-Njiit lu topp ci Njiitul Kaaraange bokkeef gi ;
-
Mustafaa Juuf, nekkoon Komiseer bu mag bu Ndar, tabb nañ ko Tof-Njiit lu topp ci Njiitul Pólisu Yoon ;
-
Elaas Bayti Seen, lañu tabb Njiitul DIC, Adaraame Saar la fa wuutu ;
-
Paap Mamadu Jijaag Fay lañu tabb Njiitul « Division Cybersécurité » ;
-
Mamadu Tendeng, lañu tabb Komiseeru Pólis Sàntaraal bu Ndakaaru. Elaas Séex Daraame la fa wuutu.