LI GËN A FËS CI XIBAARI BÉS BI (6/11/2025)

Yeneen i xët

Aji bind ji

PRODAC : YOON TÉYANDI NAÑU

Tay ci ngoon la takk-deri DIC yi fekki Paab Maalig Nduur këram, daldi koy jàpp, yóbbu ko. Bees sukandikoo ci sunu naataangooy Seneweb, li ñuy toppe Paab Maalig Nduur (APR) mooy mbooloom defkati caay-caay (association de malfaiteurs) ak kootoog luubal alalu réew mi (complicité de détournement de deniers publics).

Ci lees rotal ciy xibaar, ëllëg ci àjjuma ji, la Paab Maalig Nduur di janook àttekatu gëstu bu kabine bu njëkk bu Pool Judiciaire Financier. Moom nag, Paab Maalig Nduur, ci mbirum PRODAC mi lañu ko jàppe, ginnaaw bi ñu njëkkee jàpp kii di Mamina Dafe.

NAFAG SENEGAAL GU ATUM 2026

Jëwriñu Koom-koom gi, Naal wi ak Koppe gi, Abdurahmaan Saar, gaaral Ngomblaan gi, ci àllarbay démb ji, Caabalug koom-koom ak koppar gees toftal ci sémbuw Àtteb kopparal bu njëkk ñeel atum 2026 mees dëgmal. Caabal googu mooy tegtale yoon wi Càmm giy jaar ngir doxal polotigu koom-koom. Tënkees na ci naali fukki at yii weesu te leeral nañu ci jiituwaayi Nguur gi ñeel suqalig réew mi ci lu sax, boole ñépp te fànnu jàmbure wi am ci wàll wu réy a réy.

TËNKUG NDAJEM JËWRIÑ YI

Ci àllarbay démb ji lañu amal ndajem jëwriñ mees baaxoo di ama ayu-bis bu nekk. Bi Njiitu réew mi jëlee kàddu gi, moom Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, wax na ci fànn yii toftalu :

Arminaat : Njiitu réew mi xamle na ne dina jiite Bésub sóobare yi (Journée des Forces armées) keroog 10eelu fanu nowàmbar 2025 ;

JOJ Dakar : Njiitu réew mee ngi woo askan wépp ñu jàpp ci xew-xew bi, di ñaax liggéeykat yi ngir ñu gaaw a jébbal tabaxte yi ci aju ci àpp gi war, te dooleel kaaraange gi, yaale gi, fullaal mbatiit mi ak wërteef gi.

Koom-koomu mboolaay mi ak dimbalante : Njiitu réew mi joxe na ay ndigal ngir ñu gaawal tëralinu sàrt bi ko ñeel, suuxat koppe yi, door Pexem réew mi ci wàllu RSE yi. Rax-ci-dolli, Njiitu réew mi jël na ndogalu def atum 2026 mi, atum xëy ak ESS.

Ceeb bu doy : Njiitu réew mi joxe na santaane, wax ñu yokk ndimbal li ñuy jagleel baykati ceeb yi, ñoŋal ndefarug ceeb bi ak céddale gi, sàrtal njëg yi, jiital ceebu mbay mi.

Ginnaaw Njiitu réew mi, elimaanu jëwriñ yeet àddu na. Ci wàllu ndox mu sell mi la njëkk a wax. Li mu ci xamle mooy ne, gëstu bi ñeel lees duppee Autoroutes de l’Eau àgg na te dees na tàmbali liggéey bi ci atum 2026 mi. Naal woowu dina jariñ béréb yii di Ndakaaru, Cees, Mbuur, Tuubaa ak yeneen 28i béréb.

Bu dee ci wàllu njàng mi, elimaanu jëwriñ yi xamle na ne dinañu disitaaliise lijaasa yii di CFEE ak BFEM, tëral aw naal ngir jël ay jàngalekat yu bees, dugal làkkuw àngale ci njàngum tuut-tànk yi, ubbi LYNAQE.

Ci wàllu kaaraange, Sëñ Usmaan Sonko aajar na njureef yi ñu am ci xeexu mbëkk mi, njaayum nit ñi, ñiy làqu di gas i mbell, yelwaan gi ak toogaanu mbedd yu safaanoo ak yoon.

Bu loolu weesoo, elimaanu jëwriñ yi xamleet na ne dina jël bër li ko dale ci alxamesu tay ji ngir noppalu ay fan.

BITIM-RÉEW : NEW YORK AM NA MEER BU BEES

Zohran Mamdani, ab jullit, la askanu New York jiital, fal ko muy seen meer. Moom nag, mi ngi bokk ci làngug Demokaraat yi, di wujjeek Donald Trump miy jiite réew ma.  Moom Zohran Mamdani, ndam li mu am, daf ko sargalee ñiy doxal koom-koomu dëkk ba, muy Saa-Amerig yi, di doxandéem ya fa daansi seen doole. Tuddaale na, ci cargalam bi, Móodu-Móoduy Senegaal ya fay dawal i taksi, bokk bu baax ca ñay suqali koom-koomu dëkk ba.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj