Ci atum 2025 mi, Càmm gu Senegaal moo ngi séentu yokkute gu yegg ci 8,4%. Xibaar la bu jóge ci waa FMI (Fonds Monétaire International). Ñuy xamle ni Senegaal réew la mu wane boppam ci diiwaan bob, yokkute gee ngi ñuy natt ci 4%. Muy nag jéego yu Senegaal seqi ngir jiitu ci koom-koomug Afrig bëj-saalumu Sahaaraa bi. Yokkute googu dina sukkandiku ci ballukaayu mbindaare yi, ay tabaxte yu méngook jamono ak yokkute gu mu teg loxo. Ci seen naalub « Senegaal 2050 », Càmm gi fas na yéene sopparñi yokkute googu ngir mu doon naataange guy law jëm ëllëg. Waaye ragal nañu yokkuteg bori Nguur gi, sopparñi yi mu war a def ak ni li Nguur giy dugal ci xaalis néewe doole, xaw a gàllankoor yokkute gi.
YOKKUTEG PEYOORI LIGGÉEYKAT YI CI KËR YI
Nguur gi yokk na peyoori liggéeykat yi ci kër yi. Jëwriñ ji yor wàllu liggéey bi, xëy meek duggalante campeef yi, Abbaas Faal, moo xaatim dekkare bi ba ñu siiwal ko ci saabalukaayu Nguur gi. Ndogal loolu nag, ñoo nga ca jublu joyyanti anami liggéeykat yi fi Senegaal, sàmm seen i àq ak i yelleef ak tegaat xëy mi ci yoon. Naka noonu, dekkare bi di wane ni peyoori janq jeek bóoy yi dinañu dem ci diggante 64 223 ba 76 996 ci FCFA. Yamul foofe, nde jëwriñ ji xaatim na beneen dekkare bob, xaymag waxtu liggéey bi du weesu 40i waxtu ci ayu-bés bi, te waxtu noppalu yi duñu ci bokk. Moo xam ci jaaykati buwaasoŋ yi la, ci kafe yi, lekkuwaay yi ak dalluwaay yi. Sóoraale na itam anam yees war a faye waxtu yiy dolleeku ci waxtu liggéey bi.
CAP ÀNDUL CI NDOGALUG CÀMM GI ÑEEL TËJUB SAABALUKAAY YI
CAP (Coordination des Associations de Presse), di kurél gi dajale mbootaayi saabalukaay yi, àndul ak Càmm gi ci ndogal li jëwriñ ji ñu dénk jokkoo gi, xaralay jokkoo gi ak nimerig bi jël ñeel saabalukaay yépp. Ci loolu sax, yónnee woon na ab bataaxalub woote ci mbooleem saabalukaay yu jotul woon a dëppoo ak matuwaayi sàrti saabalukaay yi ngir woo leen cim ndaje mu ñu waroon a amal naka tay ci talaata ji, bi 9i waxtu di jot, fa ëttu saabalukaay yi (Maison de la presse).
Cq seen ndaje mooma sax, jël nañu fa ay ndogal yu bees. Tàmbali nañu tay di ràññatle ak ay layalkat gépp kërug saabalukaay gu Nguur gi nanguwul nekkam. Sàkku nañu itam ci njiiti saabalukaay yépp ñu dugalandoo ab dabantal fa pekku saytu gu Ëttu Àttewaay bu Mag bi (Chambre administrative de la cour Suprême).
Bu ñu ci jógee dinañu amal ay ndaje ci weeru me wii di ñëw, ànd ceek mbootaayi sàndikaa yi, njaatige yi, kurél yiy xeexal àq ak yelleefi doom-aadama, way-bokk yu kuréli ma-xejj yi ak yeneen i kilifa ci réew mi. Dinañu jeexalee ndaje yooya ak ub dox-ñaxtu ci kanamu njëwriñu jokkoo gi.
TABASKI 2025
Nguur gee ngi ci waajtaayi tabaski 2025 bi. Jëwriñu mbay mi, Mabuuba Jaañ jot na cee dajeek naataangoom bu réewum Móritani ngir waxtaan ci mbirum jëggaani xar yi ci tabaski bi. Naka noonu sax, déggoo am na ci seen diggante. Nde, fas nañu yéene yombal dugalug 250 000i xar yu jóge Móritani ngir jawu Senegaal bi am lim bees soxla ciy xar. Càmmug Senegaal mooy jël matuwaay yi war ngir kaaraange gi, dalal jaaykat yi ak wàññi juuti yi.