Li gën a fës ci xibaari bés bi (9/10/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

9JÀNGOROY ŊAS

Nemmeeku nañ juróom-benni jarag yu ame jàngoroy ŋas. Juróom-benni jarag yooyu, ñu ngi nekk ci juróomi “district” : Ndakaaru suuf (1), Funjuuñ (1), Kër Masaar (1), Pikin (2) ak Saraya (1). Waaye, gisuñu fenn ku ame jàngoro jees dippee “mpox”, maanaam, ci farãse, “variole du singe”.

WAAXU NDAAYAAN

Càmmug Senegaal gi dafa bëgg a dooleel waaxu Ndaayaan bees nekk di tabax jamono yii. Dañ ko bëgg a liggéey ba mu bokk ci cëslaay yiy suqali koom-koomu réew mi. DP World lañ dénk liggéey bi. Bees sukkandikoo ci kilifay Waaxu Ndakaaru bi, bu waaxu Ndaayaan bi àggee, dina féexal bob Ndakaaru.

MUURAAY BI CI JÀNGU YI

Njëwriñu njàng meek njàngale mi, biral na ab “arrêté” buy yoonal sàrti biir yi jàngu yi war a doxe. Li ci gën a fës nag mooy mbirum muuraay bi. Jëwriñ ji di xamle ne, sàrti biir yi dañu war a fexe ba yombal njàng mi, te ñu bàyyi ku nekk ak li mu gëm. Loolu nag, li luy wund mooy ñu nangul ku nekk màndargay diineem, bañ a bunduxataal kenn.

KUPPE/GAYNDEY SENEGAAL YI : KI WAR A WUUTU ALIW SIISE 

Fan yii weesu lañ tàggook Aliw Siise mi doon tàggat gayndey Senegaal yi. Boobaak léegi, ñoo ngi laam-laame kan a ko war a wuutu. Ñoo ngi nekk sax di joxey tur. Ñaar ñoo ci gën a fés, muy Abiib Béy, gaynde ga woon, ak Saa-Farãs bi, Hervé Renard. Waaye, Ogisteŋ Seŋoor mi jiite FSF, xamle na ni, doomi réew mi lees jiital. Kon, ki war a wuutu Aliw Siise, Saa-Senegaal lay doon.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj