LI GËN A FËS CI XIBAARI BES BI Alxames 10 nowàmbar 2022

Yeneen i xët

Aji bind ji

Mbirum pasug ngànnaay gu 45i miliyaar yi

Dépitey Yewwi Askan Wi (YAW), nee nañ du ñu bàyyi mukk mbirum pasug ngànnaay gu 45i milyaar yi. Xamle nañ ne dinañ taxawal kurélug luññutu ca ngomblaan ga ngir lëñbat njombe wile, leeral mbóot yi ci làqu.

Paap Aale Ñaŋ 

Sire Keledoor Li, layookatu Paap Aale, xamle na ni taskatu-xibaar bi dina tëdd lu mat 6 jàpp 8i weer, walla sax lu ko ëpp. Moom, dafa jàpp, « Dañoo bëgg a noppiloo Paap Aale moo tax ñu jàpp ko. Waaye, nun, dunu yem foofu. Fàww nu xeex lii ak képp ku Càmm xañ ay àqam ak i yelleefam, rawatina yeen taskati-xibaar yi. Loolu doŋŋ moo koy saafara. »

Wàññig njëgu yàpp wi

Mbootaay mi ëmb jaaykati yàpp yi lànk na, ne duñu wàññi njëg li ndawal li di jar. Seen njiit lii di Allaaji Basiiru Ñaŋ jàpp na ne Càmm gi dafa jël dogalam te yégoowul ak ñoom. Yokk na ci ne : « Du Càmm gee ñuy jàppale, te it xamul naka lanu def ba am sunuy nag ak i xar. Te su jëlee dogal ne wàññi na njëgu ndawal, loolu, moom la. Waaye, nun ñi xam lu nuy daj, wàññiwuñu njëgu ndawal li. »

Bàrtelemi Jaas

Ci janoo bi mu amaloon ak taskati-xibaar, meeru Ndakaar baa ngi ciy xamle ne dañu war a nëbb jànt bi kii di Basiiru Géy. Ndax ci réew mu jaar yoon, xel mënul nangu « ab toppekatu Bokkeef di sañ a soppi ab PV (procès-verbal), ba noppi di waxal nit ki lu mu waxul. Loolu dafay tekki ne doomi réew mépp a nekk ci guta. » 

Bàrtelemi yemul foofu, nde duut na baaraam Antuwaan Feliks Jom jëwriñu biir réew mi :

« Ab sagaru yégle doŋŋ nga fi génne te xam nañ ne jubluwaay bi du lenn lu dul ñàkkal fayda ak doyadil ñiy wattu sunu kaaraange. » Teg na ci ne : « Càmm gaa ngi nii di jël ay kàccoor teg ci wetu alkaati yi, ngir jaay doole kujje gi te kenn waxul. Kon nag, bu jëwriñu biir réew mi génn naan dafay tere ñiy wattu sunu kaaraange ñu soloo aw colin te yor i jumtukaay yiy tax ñu def seen liggéey ni mu ware. » 

Futbal

Li wokk Saajo Maane, xuri na Abdu Jàllo. Ñaari saa-senegaal yépp a ame ay gaañu-gaañu. Ci taalata ji nu génn, yemook 8 nowàmbar, la Bayern Munich doon joŋanteek Werder Brême ci14eelu bésu Bundesliga bi. Ci biir joŋante bi la gaynde gi, Saajo Maane, gaañu ci ginnaaw óom bi. Noonu, yéenekaay bii di L’Equipe génne ab yégle ci àllarba ji 9 nowàmbar di ci xamle ne Saajo Maane du mën a bokk ci joŋante kub di mond biy am Qataar. Nde, waa Bayern ñoom it génne nañ ab yégle di ci dëggal gaañu-gaañu Saajo Maane bi. Waaye, waxuñu benn yoon ne saa-senegaal bi du bokk ci joŋantey kub di mond.  

Bitim-réew

Njiitu réewum Farãs, Emanuwel Makoron, yégal na ne, dakkal na lépp lu jëm ci wàllum xeexub rëtalkat ya ca Mali. Ciy leeral, nee na : « Dañoo war a yamale sunuy ndimbal ci wàllum xeex cib diir. Mënatunu dugg ci ndimbalu xeex gu amul àpp ngir yeneen i réew. Looloo tax nu jël ndogal : bés niki tey dakkal nan lépp ci lu jëm  ci mbirum Barkhan. Tekkiwul ne dootuñ dimbali réewi Afrig yi ci wàllum sooldaar. Bu boobaa, dafay fekk ne, laata loolu, nu teg ay sàrt yu leer ak ñoom.»

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj