Ci àllarba ji, 1 màrs 2023 lañu fas yéene sargal, delloo njukkal sóobarey Senegaal yi ñàkke seen i bakkan ca toolu xare ba ca Mali. DIRPA, kurél gi yor kàddu larme bee ko xamle. Cig pàttali, ñetti sóobare yooyu, diy « casques bleus », bésub 21 féewaryee 2023 lañu gaañu, ca Mali. Dañu bokkoo ci soldaar yi ràngu ci MINUSMA ngir xeex rëtëlkat yi song réewum Mali. Cargal gi nag, dinaa door ci yoor-yoor bi, bu 9i waxtu jotee, ca Jal Jóob. Jëwriñu larme bee koy jiite, ànd ceek mbokki way-dëdu yi.
FITNAY PÓLITIG : WOOWEES WAY-PÓLITIG YI CIW WAXTAAN
COSCE, mbootaay gi boole way-moome yi, doon na amal ci talaatay tey jile am ndaje mom, jukkiy xalaat ñeel wotey njiiteefu réew mees dégmal ci atum 2024 mi. Bees sukkandikoo ci yéenekaay bii di PressAfrik, ña ko sookee ngi ñaax way-pólitig yi ñu toog waxtaan. Nde, ñoom way-moome yi, dañu seetlu ne, saa buy wote jubsee rekk, réew mi day toog ci nen, fitna di xeeñ.
« Dafa bokk ci cëru way-moome yi nu fi teewal, ñuy fexe ba way-pólitig yiy toog di waxtaan ci anam bu sax. Li nu ko duggee mooy sàmm jeegoy yoonu wote wi te gën a dëgëral demokarassi bi. »
Kàddu yii la fa Baabakar Géy, ndawal COSCE li, biral.
SÉEJU : NJIITU RÉEW MI MAKI SÀLL DIGE NA FA 27i MILYAAR
Jamono jii, Njiitu réew mi, Maki Sàll, mi ngi ci diwaanu Séeju, di fa amal nemmeekub koom-koom. Ca Ndajem njiiteef ma mu fa doon amal nag, Njiitu réew mi xamle na fa ne dina génne 27i milyaar jagleel leen 19i dëkk ngir ñu mën a am mbëj (kuraŋ). Jubluwaay bi mooy yemale mberaay yi, jaare ko ci ile sémb. Bu naal boobu àntoo, dina tax ba kër yu bare génn ci lëndëm gi.
COOWAL SUUF CA TIWAAWAN-PËL
Askan way yeewoo ca Cité APIX (CICA) ña ngay duut baaraamu tuuma liggéeykati « Impôts et domaines ». Nee ñu, ñooñu dañuy jaay seen i suuf. Kurél gii di Inter-îlots gu ëmb waa gox ba ñoo génne ab yégle, wax ne :
« 12i at a ngi nii, nuy daw ginnaaw Nguur gi ngir jot ci sunuy këyiti kër. Noonu lanu ko waxtaane woon, ñépp ñi bokkoon ci sémb bi. »
AKSIDAŊ CA NDAKAARU
Ca VDN ba la akisdaŋ bi ame. Wii yoonati, ag sëfaan (kamiyoŋ) moo ko sabab. Bi mu àggee ci benn buntu « autopont », ci kow VDN bi, la wàcc yoonam, mbëkk ay wata yu bara, fatt yoon wépp.
NISERIYAA : KUJJE GI DAFA BËGG ÑU FOMM WOTE YI
Ñaari làng yi gën a mag ci kujje gi, PDP ak LP, ànduñu ci ni wotey njiiteefu réew ma deme foofa ci Niseriyaa. Nee ñu, dañu war a amalaat wote yi. Nde, ñoom, dañu jàpp ne « dañu soppi bu baax a baax ngirtey wote yi ». Kurél ga fay saytu wote yi, INEC, dafa génney ngirtey yoy, lawaxu Nguur gaa ci raweegum tuuti ñenenn ñi. Waaye, ngirte yooyu, 14 dëkk kese la ëmb ci kow 36.