Elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, dina gaaral naal wi Càmm gi taxawal ngir joyyanti koom-koomu réew mi. Ginnaaw bi mu ko njëkkee junj ci ndajem jëwriñ yi, keroog àllarba 23 sulet 2025, dellu na dëggal ni dees na ko amal keroog àjjuma 1 ut 2025 fa Grand Théâtre national. Ci xëtu Facebookam bi mu ko siiwale, ma nga cay xamle ni joyyanti bi ñu doon laam-laame jot na. Ci noonu itam, dellu na fàttali tolluwaayu réew mi ak nees ko fekke woon. Loolu nag tax na ba moom ak Càmmam daldi tànn yoonu jëf ak wut i saafara.
BÉSUB SÉEX AHMADU BÀMBA FA ETAASINI
Démb ci altine ji, 28 sulet 2025, lañu doon màggal fa Etaa-Sini, diggante New York ak Washington, bés bi ñu fa jagleel Séex Ahmadu Bàmba. Bu ren ji di 37eelu yoon wu ñu koy màggal foofa ba ñu ko tàmbalee ca 1988 ba tey. Ayug ren ji, dellu na wane taqoo gi Saa-Senegaal yi nekk ci jasporaa bi taqook Tariqa Murit. Bi ñu koy màggal ren itam, gaawantu nañu ci ngir fàkk béréb ba ñu nar a samp daara ju mag ju ñu duppe Complexe islamique fa Tuubaa. Muy naal wu ñu am ci njiiteefu kurél gii di Fondation Khadimou Rassoul North America. Daara jooju sax dinañu ci dugal koppar gu tollu ci 1 milyaar ci Fcfa.
BITIM-RÉEW
Fa koddiwaar, Alasaan Watara ma nekk Njiitu réew ma, yékkati nay kàddu tey ngir biral nekkug lawaxam ci wotey Njiiti réew ya ñu fay amal fileek ñetti weer. Mu nar a nekk ñeenteelu moome gu muy yóotu ginnaaw bi ñu ko njëkkee fal ca atum 2010, falaat ko ca atum 2015, dellu falati ko ca atum 2020.
Ci li mu wax nag, mënees na cee jàpp ni, ndogal lu mu jël la ginnaaw bi mu ci xalaatee bu baax ak teeyu bakkanam. Mu gis ni Ndayu Sàrtu Réew mi may na ko ko te wér-gi-yaramam itam àttan na ko. Bu weesoo loolu, gis na ni seen réew ma dafa nekk ciy tolluwaay, mu bari yu mu war a jànkonteel ci wàlli kaaraange, koom-koom ak kopparal. Jafe-jafe yu ni mel nag dañu bette, te ngir am ci taxawaay bu mat, dafay laaj ku ñu jital ku xam ni nguur di doxee.
NJUREEFI BFEM 2025
Njureefi BEFEM bu ren ji wane na ay yokkute bees leen gam-gamleek yu daaw yi. Ci réew mépp, téeméer boo jël, lu ëpp juróom-ñaar-fukk ak juróom-ñett jàll nañu 78,59%. Yu 2024 yee ngi woon ci 73, 94%, di lu ëpp juróom-ñaar-fukk ñett yu jàll ci téeméer bu nekk. Muy wane ni téeméer boo jël ñeent jàpp juróom yokku nañu ci. Bees sukkandikoo ci kàddu yi Pàppa Baaba Jaase, di njiitul kàtte yi, yékkati, mënees na wax ni bilaŋ bu baax la. Mu ciy delloo njukkal njàngaan yi ak taxawaay bi ñu ci am, waaye itam fàttewul caytu gi ak matukaay yi mu yokk ci wàlluw kaaraange gi ak soste yi ñu amal ci nimerig bi booleek jàppandi.