LI ÑÉPP BOKK

Yeneen i xët

Aji bind ji

Waxi Wolof, yenn saa, dañuy xaw a juunoo. Dafay mel ni sax kuy weddi boppam.

Weddi boppam ! Mbete nit. Aa, xéy-na nit la de. Nde, am na sax ñu koy santale Njaay. Lu ñu wax rekk ràbb ci “Wolof Njaay nee na”. Mel ni kuy sukkandiku ci moom ngir seen i wax mën a am cafka. Bu ko defee, ñuy ñiiramtal walla di jurgóot noppi way-déglu yi.

Bari na kuy bëgg a yey moroomam, daagu ndànk ba ci Wolof Njaay, àbb ko genn ciy kàddoom yu xóot yi te neex ciy nopp lool. Ci waxam yooyu, bokk na ci ñaar yii. Fi muy waxee ne “li ñépp bokk, kenn moomu ko” ak feneen fa mu naan “li ñépp bokk, ñépp a ko moom”.

Muy mel ni ay kàddu yu woroo. Ba tax, ku mu neex samp i laajam. Kii moom, xanaa dafay tiit di wax ? Walla dafay def lu tàbbi ci bopp bi rekk, mu jox ko làmmiñ wi te du ko jaarale ci xel mi ? Déet sax ! Ñàkkul ne, xéy-na, jamono ju jot rekk ak li mu laaj ciy kàddu.

LI ÑEPP BOKK, KENN MOOMU KO ?

Waaw, dëgg la ! Kenn nit kott moomu ko ndax, daf ci ànd maase ak ñépp. Kenn warul am sañ-sañu def ci lu ko neex. Nde, ni mu ci amee wàllam, noonu la ci ñeneen ñépp amee seen uw wàll. Te nag, kenn ëppalewu ci moroomam.

Kenn moomu ko nag, warul a tax ñépp seetaan. Nde, bu ku nekk nee moomuma ko ba mu yóbbee ko mu bàyyi ku jóg rekk def ca lu ko soob, kon bu yàqoo ñépp ay ñàkk. Te moom, seetaankat bi, du ci mucc. Li war kay mooy ku nekk def ko ni yëfam.

Kenn moomu ko it, warul a tax lu neex waay def. Ndax, bu ku nekk jàppee ne du moomeelam ba bëgg caa def lu ko neex, bu boobaa, pëccaxoo am. Te, du jur lu dul yàq-yàq yees mënul a xayma. Kon, li war mooy ku nekk def ko ni yëfam ba noppi sóor ci ña ca des.

LI ÑEPP BOKK, ÑEPP A KO MOOM ?

Waaw, dëgg la ! Ku nekk a ci am wàll te kenn ëppalewul moroomam. Mu néew, mu bari, ak nu mu mën a tollu, mbooloo mee ko bokk te mënuñu koo séddoo. Kenn mënul jël sa wàll ba noppi dummóoyu ña ca des. Dafay dellu ci kàddu gi naan lépp i ñépp la, lu ney ku nee ngi ci.

Ñépp a ko moom. Kon, ku nekk war na cee bàyyi xel. May ko nopp ak i bët ni meew mu ñu teg cib taal. Bu fuuree, tuuru te bu tuuroo loraange ya mën nañoo bari. Bàyyi ci xel war na. Bu ko defee, kenn du ci def lu defuwul. Kenn du ko caxat-caxatee ànd ci ak ñàkk ngor ak teggin ni bukki bu gis aw seel.

Ñépp a ko moom, kon ku nekk war na koo ñoŋal. Bu ko defee ñépp di ci gis seen bopp. Naka noonu, la ñuy mën di wéy ànd di ko jariñoo. Te, loolu dina tax ba ku ci nekk gën a gëm ni ci mbooloo mi la bokk, kenn beddiwu ko te it, kenn ëppu ko ci cër.

Li ñépp bokk daal, kenn moomu ko. Waaye nag, ñepp a ko moom. Ku nekk am na ci wàll wu tolloo ak wosu moroomam. Te kenn amu ci cër lu dul ne dafa nangul ñeneen ñi seen i yos.

Rax-ci-dolli, ku nekk sañ nga, ci lu tolloo ak li ciy sa wàll. Te, sañ-sañu ku nekk, mi ngi yam fi bosu keneen ki tàmbalee. Ci noonu la mbooloo mi di mën a amee ag dal.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj