Mamadu Aamadu Li, njiitu ARED, moo jël Neexalu Yidan 2025 ca Oŋ-Koŋ (Hong-Kong). Muy Neexal bu am solo lool ñeel suqalig njàng mi. Dafa di nag, guléet ab saa-Afrig di jël neexal bu ni mel.
Kurél gi ko ko jagleel mooy Fondation Yidan Prize. Kurél googoo ngi sosu ca atum 2017. Jubluwaayam mooy fexe ba lees am « àddina su gën, jaare ko ci njàngale ». Fondation Yidan Prize dafay sargal ay nit mbaa i kurél yuy yëngu ci suqalig njàng ak njàngale. Ñaari neexal (Prix) lay joxeendoo : caytu ci njàng ak suqali njàng. Ñaar ñi ñu tànn, ku ci nekk dina jot 30i milyoŋi dolaar ci koppari Oŋ-Koŋ (Hong-Kong), muy tollook, daanaka, 3i milyoŋ yu tegal 800.000 dolaari amerig. Bu dee ci seefaa (sunuy koppar), xaalis bi dafay méngook 2i miliyaar. Koppar yi nag, dees koy xaaj 2 : benn bi jëm ci ab nisër bu nit ki walla kurél gi am ngir jàppale ko mu jëmale kanam liggéeyam. Ki ñu boole sargal ak sën Li moom, Uri Wilensky, jàngalekat ca Iniwérsite Northwestern, ca Amerig, xam-xamam màcc ci xarala njàng ak xamteef (informatique).
Di fàttali ne Doktoor Sonja Fagerberg-Diallo, saa-Amerig buy dund Senegaal 1976 ba tey, moo sos ARED ca atum 1990 ca Amerig, mu jot i kayitam ci Senegaal at ma ca topp. Jubluwaay yi ci gën a fës yii la : gën a yaatal ak cëral làmmiñi réew mi, xeex ñàkk-jàng, njàngale ak tàggat ci làmmiñi réew mi, rawatina pulaar.
Li Seex Anta Jóob ni woon « am réew mënut a sukkandiku ci làkku jàmbur ngir jëm kanam » la sëñ Mamadu Li nànd ba liggéey ci sukkandiku ci sunuy làmmiñ ngir soppi ak suqali njàng mi.
Ginnaaw bi mu biralee mbégteem ci Neexal bi, fésal yëg-yëgam, Sëñ Mamadu Li gërëm na ñépp ñi mu àndal di liggéey ak farandoo yi jàppale ARED ba mu tollu fi mu tollu tey. Cargal gi ak koppar yi mu àndal dinañ tax ARED gën a yokk jéego yi mu nekkoon ngir suqali njàng mi te yit dina ci boole xarala yu yees yu deme ni Intelligenceartificielle ndax jamono day dox.
6eelu désàmbar 2025 la ñuy jëliji neexali Prix Yidan ca Oŋ-Koŋ (Hong-Kong).
EJO-EDITIONS ak LU DEFU WAXU di ndokkeel bu baax sëñ Mamadu Aamadu Li ak waa ARED yépp ak ñépp ñi làmmiñi réew mi soxal.