USÉYNU BÉEY, AT CI SUUF…

Yeneen i xët

Aji bind ji

Bi Uséynu Béey génnee àddina ak tey, def na atum Yàlla. Ñu bari bind ci moom, ay seede yu rafet, ay pàttali yu daw yaram : moo xam mbokk ak i xarit, ay naataango walla njàngaan (yi mu yoroon ci wàllu koom mbaa wolof), moo xam ñi mu bokkaloon làngu pólitig (RND gu njëkk ga) walla ñi mu daan xeexandool ak a liggéeyandool ci làmmiñi réew mi. Jàpp naa ni Bubakar Bóris Jóob moo ci jël raw-gàddu gi. Bóris dafa yàggoon ak Uséynu, ñu xaleendoo, màggandoo, déggoo woon ci lu bari, di bokk gis-gis ak di wuute tamit, mësuñoo teqalikoo lu dul dee. Li tax yaxalu Bóris boobu yéeme dafa di, soo koy dawal dangay gis Useŋ, yenn saay nga muuñ, yenn saay sa rangooñ dal ndànk ci sa dënn, du la tàggu. Ak yaxal bi tamit, dangay gën a xam Useŋ, xam ni ku mës a am faayda la booleek teggin, yiwoon na, xelam rafetoon na (de poussière et d’éternité : pour ouzin et chacun – SenePlus).

Man nag, binduma woon jëm ci deewug Uséynu Béey doonte dem naa lopitaal, dem it këram, jaale ko njabootam tey wéy di ko ñaanal. Aa, kon lu tax ma jàpp ni sëñ Béey deewul ? Wolof laa. Te wolof day faral buy tàgge di jëfandikoo ay baat yu deme ni làqu, dëddu, nelaw… Te, ñaare, ku làqu dañuy yaakaar mu feeñ, ku dëddu dellusi, kuy nelaw yeewu. Yaakaar gu deme nii, bokk na ci li ma tee woon a bind ci faatug Useŋ gi, maanaam mënuma ko woon a nangu. Xam nga, yenn saay nit daf lay jege, ngay dund ak moom, miin ko, nga dem ba yaakaar ni nit kookii warul génn àddina bés. Uséynu Béey, ci man, ci ñooñu la bokkoon. Moone, xam naa xéll ni bakkan bu ñam dund dinaa mosiji dee ; kenn du fi des…

Bubakar Bóris Jóob nettali na ci ay baati xol ak xel Uséynu Béey, baat yu ma amul, yu ma mënul moo tax rekk ma wax as lëf ci mbaaxu Useŋ ak yéwénam : bu ma mësaan a liggéey dara lu rafet, def waxtaan ci mbooloo walla bind yaxal, mbaa EJO móol téere bu bees, daf may topp di ma ndokkeel, di ma kañ ba bu ma deful woon ndànk, doon naa dem ba jàpp ni maa fi mën. Moone, Useŋ

ci boppam, boo mësaan dawal mbindam fàww nga yéemu ci xalimaam ak ni mu peegee woon làkk wi mu daan jëfandikoo, tubaab ak wolof ñoo ci bokkoon yem.

Soo yàggul a xam Uséynu Béey, su ñu la nee bañkat la walla da daan jiite ay ñaxtu walla yënguteef doo ko gaaw a gëm ndax lewet ak dal gi woon ci moom, teggin yi mu làmboo woon ak i kafam yu bari. Aka amoon maanaa te yànj col, bëgg boppam te fonk doom-aadama. « Xam naa ne mësoo yeewu te newoo, tey, naka laay def ba dimbali nit ñi ma wër walla naka laay def ba mboolaayu Senegaal gi jëm kanam » ? Uséynu Béey bokk na ñi Seex Anta Jóob tàggatal boppam te mu dunde ngëm-ngëm yooyu ba ni mu génnee àddina (keroog 21eelu sulet 2024) amoon 79i at.

Bey nga sa waar ci tool bi ba wàcc ndax jàngal nga fi ay doomi Aadama, tey ñu tekki daanaka ku ci nekk ca wet ga mu féete ba ci Usmaan Sonko miy njiitu jëwriñi senegaal te jàngal nit bokk na ci « sarax suy des ».

Li nga liggéey ci EJO-EDITIONS ak Lu defu waxu ak làkki réew mi, mi ngi fi…  Téere bi Soxna Awa Bookar Li jagleel Seex Anta Jóob, yaa bind ubbite gi. Daan nga def taxaw-seetlu ci Seneplus, ñu bari daan taataan say xalaat, di ci jàng… Kon doo dee ndax ki dee dëgg mooy ki ñu fàtte te kenn du la fàtte. Di ñaan rekk Guyaar di sa noflaay te Yàlla teg loxo ci sa njaboot.

Asan sa seex, Penda sa soxna, Bóris sa doomu-ndey, siggil-leen ndigaale.

Ndey Koddu FAAL

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj