MBAS MEEK ÑÀKK XÉY CI SENEGAAL (SAFIYETU BÉEY)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Bérébu liggéeyukaay yu bare tëj nañu ndax mbas mi, loolu la ab lànket bu Programme sénégalais pour l’entrepreneuriat des jeunes (PSE-J) xamle ciy xibaar. « Liggéeyukaay yu bari wàññi nañ li ñu daan liggéey, gis nañu ni 43,7% ci seen doole jot naa wàññeeku ci diirub mbas mi. » Bi kurél gi gëstoo këru liggéeyukaay yi ne ci réew mi yépp, gis nañ ni ñawkat yi, mbaa di liggéey liggéeyu loxo, la seen doole gën a wàññeeku. Lu tol ci 67% ci xaalis ba ñu daan am la ñu ñàkk ndax mbas mi. Baykat yi, sàmm yi ak nappkat yi tamit ñàkk nañu xaalis bu baree-bare. Ñiy liggéey ci oto yeek dem beek dikk bi daal ñoo xaw a tane demin, ginnaaw 20% ci seen xaalis rekk lañu ñàkk.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj