«Kenn du jëfandikoo Covid Organics fii ci Senegaal». Porfesoor Musaa Séydi xamle na ni garab gii di Covid Organics te juge Madagaskaar du bokk ci garab yi doktoor yiy jëfandikoo ngir faj koronaawiris. Bi gëstukat yi saytoo bu baax garab gi, gisuñu ci chloroquine, gisuñu ci it benn doom buy faj koronaawiris. Te li gën a yéemee ci garab gi mooy, kenn mënul a xam dëgg-dëgg liñ ci xooj yépp astemaak liñ ko defare. Rax-ci-dolli, bi doktoor yi jàngate li ne dëgg ci garab gi, fekk nañ ci poson, loolu tax leen a tere Covid Organics fii ci Senegaal, ndax dara wóoru ci.