NAALUW “CONSEIL SUPÉRIEUR DE LA JUSTICE”

Yeneen i xët

Aji bind ji

Démb, ci dibéer ji, la kii di Porofesëer Siidi Alfa Njaay, doon amal aw waxtaan wu am solo fa RTS. Dafa di, dañu ko fa woo woon ci jotaay bii ñu dippe “Point de vue”. Moom nag, jot na fa indi ay leeral ci coppite yees di waajal ñeel fànnuw Yoon. Nde, Ndajem kàtte mu kawe mi (Conseil Supérieur de la Magistrature) lañu nar a soppi def ko, Ndajem Yoon mu kawe mi (Conseil Supérieur de la Justice).

Porofesëer Siidi Alfa Njaay, ku ràññeeku la ci réew mi. Ndax, ndombog-tànk gees ko dénk. Nde, jëwriñ juy xelal Njiitu réew mi la ci wàllu Yoon. Moom nag, kàddoom ya mu yékkati fa jotaay booba ñu ko dëñe woon, leeral na lu bari ci wàllu Yoon. Ndax, coppite gii mu xamle ne ñi ngi koy waajal dafa am lu muy dolli ci liggéeyu Yoon. Waaye tamit, dina am lu mu ko dolli ci dooleem ak i sañ-sañam.

Jëwriñ ji, la mu xamle ca waxtaan woowa mooy ne, Ndajem kàtte mu kawe mi lañuy waaj a soppi, def ko Ndajem Yoon mu kawe mi. Maanaam, ndaje lay doon moo xam ne, du ñiy yëngu ci wàllu Yoon kese ak Njiitu réew mi ñoo koy mën a teewe. Ndaje lay doon mom, dees na ubbil ay buntam ñi nga xam ne sax liggéeyuñu ci mbiri Yoon. Muy jàngalekat yi nekk ci daara yu kawe yi, di kuréli way-moomeel yi ak yeneen i kilifa yoo xam ne bokkuñu ci ndawi Yoon yi.

Li mu bëgg a xamle foofu mooy ne, Yoon, ñi ciy yëngu kese moomuñu ko. Askan wépp a ko bokk. Kon, dafa jaadu ñuy gis seen bopp ci ndaje yooyu. Rax-ci-dolli, Yoon, jamono jii, dafa bari lu ñu koy duut baaraam. Seen mébét mooy Yoon ubbil askan wi ay buntam. Ndax, nee na, Yoon dafa war a tëdde njaaxanaay te moom boppam. Looloo tax, naal woowu, jubluwaayam bokk na ci dog diggante jëwriñu Yoon ak toppekat bi ngir tolloole doole yi ci banqaasi Yoon yi. Ginnaaw loolu, dina am li ñuy dippe “Juge de Liberté et de la Détention” ci ëttu àttekaay yi. Àttekat boobu mooy jël ndogal ci ku ñu war a tëj walla tëjandi, ak ku ñu war bàyyi. Jëwriñ ji, yamul foofu rekk.

Xamle na ne limub àttekat ak wotekat yi dina jóge ci juróom-ñaar dem ci fukk ak ñeent. Te, Njiitu réew mi tamit day des fa Ndaje ma. Ndax, moom teewaayam foofa du ngir mu am njeexital ci ndogalu àttekat bi, déedéet. Moom, dafay teew ngir lépp tegu ci Yoon, ni ko ndeyu sàrtu réew mi tëralee. Kon, teewaayam foofa du gàkkal dara ci dooley àttekat bi. Maanaam, loolu du ko teree moom boppam.

Ci gàttal, naal wii la jëwriñ ji ne moom lañuy togg. Te, li ñu ci jublu du lenn lu moy Yoon am geneen xar-kanam. Ndax, ñàkkul ne bu yàgg ba tay am na bët bu ñu koy xoole. Te, jàpp na ne bu Yoon ubbilee ñépp i buntam, coppite mën naa am.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj