Jamono yee ñu weesu, ñaxtuy sàndikaa yi yëngaloon na réew mi. Waaye, ginnaaw ab diir dañoo wàññi. Waaye nag, dafa mel ni ñi ngi bëgg a delloo buum ca mboy-mboy ga.
Ñii di waa SYNTTAS (Syndicat national des techniciens et travailleurs de l’agriculture du Sénégal) dañoo jël ndogalu dakkal seen liggéey ci bésu alxamesu tay jii. Li ko sabab mooy xeex li ñuy teg seen naataango ya nekk fa goxu Ñooro. Naka noonu, ñii di waa SYTJUST-UNTJ, nga xam ne moo ëmb liggéeykati Yoon yi, moom tamit jël ndogalu ñaxtu, fésal li leen metti. Nde, ci seen i wax, dinañu dakkal seen liggéey lu tollu ci ñaari fan. Maanaam, almaxesu tay jii lay door, jàpp àjjumay ëllëg ji. Li ko waral mooy, ba tay ci seen i wax, gisaguñu saafara li ñu doon xeex donte ne sax jot nañoo gisante ak yenn kilifa yi (Président du Haut Conseil du Dialogue social ak Ministre de la Fonction publique). Kon, ñoom dañuy wéyal seen ub xeex.