NGOR : KËRUG FARBA NGOM LAKK NA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Bu kenn àttewul, musiba dina am. Te, bu boobaa, dina rëccu dina fekk jëf wees. Ca Ngor, ba nëgëni-sii, ndaw ñaa ngay wéy di xeex ak way-wattu kaaraange yi. Ba ci àjjumay tey ji nga xam ne, am na ñu ciy korite, coow la fayagul. Dafa gënatee rëb sax. Ndaxte, kërug Farba Ngom ga fa nekk, dépite APR bi, dafa tàkk. Xamaguñ nag lu sabab lakk-lakk bi. Am na ñuy njort ne way-ñaxtu yaa ko taal. Waaye, kenn amagu ci firnde.

Ngir fàttali, talaata ba léegi, ndawi Ngor ñaak sàndarm yaa ngiy xeex. Li ko waral mooy ne sàndarm yi dañ jël teeruwaayu oto (pàrkiŋ) bi ci buntu dëkk bi, tabax fa ab birigaad. Ñenn ña ngiy ruumandaat sax ne, AUCHAN lees fa bëgg a sanc. Teeruwaay booboo ngi tollu ci 6 000iy m2. Loolu la askanuw Ngor wa lànk ba tëdd ci suuf.

Bees sukkandikoo ci kàdduy kenn ca kilifay Ngor ya, béréb ba, waa dëkk ba dañ fa bëgg a tabax ab liise ak yeneen xeeti naal yuy jur i xëy ñel ndawi Ngor yi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj