Ci ubbite lekkool gi, Nguur gi jël nay matuwaay yu am solo ngir taxaw ci doxalin wu digg-dóomu ñeel lekkool yi. Muy doxalin wuy boole ñépp, am njariñ te di yamale.
Barki-démb ci àjjuma ji, 10i fan ci weeru Oktoobar 2025, Càmm gi doon na amal lëlu boppam, di coste gu ñu duppe “Kàddu” ngir may way-bokki Càmm gi ñu andi ay leeral ci yenn ndogal yeek doxalin yi. Ñoo nga ko doon amale fa taaxu Caytu (Building Administratif) bees duppee Mamadu Ja.
Ca seen ndaje mooma, jëwriñ ji ñu dénk wàllu njàng mi, Mustafaa Màmba Giraasi, dellusi na ci ndogal yi Nguur gi jëloon ngir amal ubbite gu jaar yoon ci atum 2025-2026 mi. Naka noonu, aajar na fa yoonu coppite lekkool bi ngir yokk i ngëneelam.
Bees sukkandikoo ci xibaar yi tukkee ci jëwriñ ji, dinañu doxal naal wu bees ngir am lekkool bu tëdde njaaxaanaay, di naal wu dul beddiwaate. Ci loolu sax lañu sukkandikoo ba gëddaal liggéeyi jàngalekat yi ci ubbite gi. Naka noonu, muy xamle ni fileek ñuy dugg ci atum 2026 mi, dinañu saafara mbirum jàngalekat yi ñu duppe “Enseignants décisionnaires”. Ñuy ay jàngalekat yuy def liggéeyi bépp jàngalekat di def, waaye boolewuñu leen woon ci ndawi Nguuru gi (fonctionnaires). Loolu nag, deñ na.ndax, Njiitu réew mi torlu na ab dekkare bu leen boole ci ndawi Nguur gi.
Jël nañu itam ndogalu dugal ren ci njàng mi 9i làkk ci làkki réew mi. Bu dee ci wàlli tabaxte yi, jëwriñ ji biral naat ni jot nañoo kopparal lu jëm ci tabax 46i daara yu digg-dóomu ak 46i daara yu suufe.
Dinañu amal ay jàppandal itam ci wàllu xarala yi ba ñu mën leen di jëfandikoo ci caytu gi ngir am doxalin wu gën, wu leer te noppal jàngalekat yi.