NJÀNGATU TÉEREB SOLEILS INVINCIBLES BU SEEX AHMADU BÀMBA NJAAY

Yeneen i xët

Aji bind ji

Soleils invincibles(Présence Africaine, 2025), ab téere la bu Seex Ahmadu Bàmba Njaay bind ngir yékkati ak xeexal doomu aadama ci biir àddina bu jaxasoo bile. Àddina bob, lu waay ëppalee moroomam, wan ko ko ; moo xam ci diggante nit ak nit, mbaa sax ci diggante réew ak réew.

Seex Ahmadu Bàmba Njaay taxaw taxawaayu layookat ak jàngalekat, di yeete, di soññe ak a àrtu ngir bépp saa-Afrig man a jëmmal boppam, xam boppam te wóolu boppam ngir kembaaram jëm ca kanam. Nu man ci jànge ne Seex Ahmadu Bàmba ab woote lay def itam jëmale ci ndaw ñi aamu dëgmal Tugal (Órob) ci tiis, naqar ak tumurànke ngir wuti fa lu ñu bàyyi fii ci seen um réew.

Soleils invincibles nekk na liy layal, ba fa mu gën a xóote, der bu ñuul. Ci njëlbéenug téere bi, gis nanu ne nit ku ñuul du dara ci biir nit ñu weex ñi. Mbalit sax a ko tane. Nga gis ne Daramaan deram bu ñuul moo tax ñu jiiñ ko càcc gu mu deful. Ñépp teg ko ay gët mu war a dékku tuuma yi ci ngor ak fit bañ a mel ni ñenn ñi jóge Tumurànka nekk Sisaan, fàtte seen bopp ci coliin, ci waxiin ak ci doxiin, di doom walla di baay. Mbaa ñu takk fa jabar ngir woyofal seen uw nekkiin ciy këyit, fàtte seen démb. Te, séy yu bari du mujj ci lu dul ay wor mbaa fa mbaxana doone benn.

Wolof dafa léebu, ne : “kéwal du tëb, doom ja bëtt”. Mu mel ni Seex Bàmba day xaw a feelu bindkat bii di Buubakar Bóris Jóob ci téereem boobu mu tudde Doomi Golo, di ci ŋàññi ñiy jóge bitim-réew, nekk ay saa-Afrig, waaye fàtte seen mbatiit ci fànn yépp. Ci téereb Seex Ahmadu Bàmba Njaay bii ngay gise ni der bu weex jàppe jaam boroom der bu ñuul ca Sisaan ga ñu nekk di fa liggéeye. Ni Gaspaar di yuuxoo, saaga ak a dal ca kaw liggéeykat ya. Kenn ci ñoom di Laxseen, di xaritu Daraamaan, am naqar ndax boddi gu metti ci seen kaw. Mu nekkoon di topp i ndigal ba faf ñàkk bakkanam ci anam bu doy waar.

Boroom téere bi teel naa fàttali nit ñi dee. Waaye gan dee ? Dee gu amul xar-kanam. Dee ci tumurànke ndax taxawu ba ca war doo ko am : nga nekk doxandéem, sa jëf naaxsaay, say mbokk duñu mas a tiim sa bàmmeel. Loolu mooy deewu àll, dee gu amul xar-kanam. Laxseen mi dee, ndax dina ñu ko indil i bokkam fii ci Tumburànka ? Déedéet ! Deewam googu jural musiba gu rëy Daraamaan ba takk-der yi patam-patamee ko, sonal ko lool ci lu dul yoon. Ñu jaare fa génne ko Sisaaan ci tiis ak toroxal ci ku jàngi woon.

Ahmadu Bàmba Njaay ñëwaat na bu baax ci ñàkk a weg jëmale ci nit ku ñuul ci lu jëm ci seen këyitu jàll-waax ak seen nekkiin. Muy lu metti ci ñoom foofu ca Sisaaan, yomb lool ci nit ku weex fii ci Tumurànka. Mu niru ne nun nit ñu ñuul danoo wuyoo sunu turu kembaar : TUMURÀNKA. Nun daal ay nit yu tumurànke lanu, yu doyadi te ñàkk bopp. Tumurànka mooy tumurànke. Lii mooy wax ji…

Soleils invincibles nag, téereb nettali la. Way-jëmmal bu ci nekk bindkat bi jox na la kàddu. Kàddu dëgg. Kàddu gor. Téere bii jant la buy niit ak a feeñal lépp lu nëbbu, neex mbaa naqari, ci tolluwaayu jamono jii ba ku nekk man a noyyi ngelawal jàmm ju lalu ci koom. Ahmadu Bàmba Njaay mi bind téere bi xam na loolu te it gis na ko. Gis na ne, nit ñu ñuul ñi dañoo war a jàppalante, nangulante ci lépp. Ci kaw loolu ñu bàyyi xel sunu moomeel di sunu cosaan moo xam ci am pajum cosaan walla jox cër say way-jur. Rakk jox cér mag te déggal ko, mag it delloo ko lépp. Jigéen ñiy xeesal ngir bëgg a niru waa Sisaan man koo bàyyi. Ci réew mu mel ni Tumburànka kese ngay gis lu yéem sa bopp, bokk ci sunuy xar-baax. Donte Daraamaan jóge na Sisaan, waaye ñëw ci lu yàggul dara, baayam bii di Nguugi faatu. Faatu na de, waaye teewu koo bokkaat ci way-dund yi, di wax ak njabootam ci ay bataaxal yu yéeme te bindkat bi tudde ko “Lettre morte”. Foofu Seex Ahmadu Bàmba dégg bindkat boobu tudd Sooni Labu Tansi ci téereem bi mu duppee Une vie et demie (dund ak xaaj). Ñu ray Màrsel, waaye tereewu koo ñëwaat ngir fayul bépp way-dee bu ñu bóom. Waaye, fii, Nguugi dafay yónnee ay bataaxel di ci fàttali nekkiinam ak njabootam. Mu bëgg a xamle ne, dinga sonn ci sa njaboot waaye ñoom duñu nànd mukk fi nga leen bëgg a jëme ngir seen ëllëg baax. Te it Tumburànka nekk na réew moo xam ne góor mooy takk tubay ci biir kër gi. Wuute lool ak waa Sisaan.

Soleils invincibles di wane mbéefar giy wéy ba léegi te kenn sañul a wax. Tubaab yiy ñëw sunu réew yi, ubbi fi ay barabi liggéeyukaay te dara du leen ci fekk. Ñu jàpp sunu ndaw ñi di leen liggéeyloo ak a xas ci anam bu ñaaw. Te, su taskati xibaar yi taxawee, mu mel ne du woon ñoom. Sunu njiiti réew yi nekk ay xuus-maa-ñàpp, di leen jàppal tànk. Boole ci may leen sunu géej gi ñuy napp ba jën woo jox sa njaboot sax doo ko am. Koom mi taxaw. Liggéey, su amee it, doxul. Loolu waral ndaw ñi song géej gi ngir yaakaar feneen dund gu gën.

Ahmadu Bàmba Njaay ñaawlu na bu baax soldaar ya woon, doon jàppal tànk Sisaan ca xare ba. Ñu noppi amul lu ñu leen faye, lu dul indi leen ba Tumburànka, boole ñépp ray ag fajar. Muy lu ñaaw te metti.

Fii ci réewu Biyóomo ci biir Tumburànka, Daraamaan di dund mettit gu nekk ndax ñàkk. Gis loo bëgg a faj te manoo ko. Xeebeel taxaw, nit ñi di la dóor ay waatu suuf. Noonu, mu sóobuwaat ci yoonu Sisaan. Yaay ji dig na ko ay neexal yu duun ngir mu man cee jàpp, uuf leen te bañ a dem. Waaye, Maam nee na : “tere mu të, bàyyil mu gis”. Daraamaan, “daj na lu mburu dajul ci fuur”. Ci diggante daamar yi, àll yu ñuul kukk te lëndëm, nit ñuy raye te duñu ci am benn réccu, suuf su ne ñàyy, du garab du ndox, ay dëkkuwaay yu doy waar ak géej gi, Daraamaan ak ña mu àndal di dundu safara ci lu ko jarul. Feebar, loxo bu damm, xiif, mar, dee, tiis woo xalaat moo ngi ànd ak ñoom di wéy ni takk-nder ak boroom. Xay-na li Madikke mi ci téereb Faatu Jom bii di Ventre de l’Atlantique ëppalee Daraamaan mooy yoon wi. Doonte ku daan xalaat ne Sisaan mooy àjjana ci kaw suuf. Moo taxoon mu bàyyi lépp ngir bëgg a dem ci ay nax kese.

Daraamaan war a nekk góor tigi ci gisewaatam ak rakkam ju jigéen Tabara gannaaw ba mu gàddaayee. Tabara ëmb, di wësin faf ñàkk bakkanam. Moom Daraamaan nekk ci diggante dund ak dee. Ña mu àndaloon ñépp dem ba mu des soxna Maken. Mu war a nangu ndogal, gëm Yàlla ndax ñàkk na baayam Nguugi, ay xaritam Laxseen ak Haamit ak rakkam Tabara. Àddina di ko yar ci nangoo topp ndigalu way-jur, di ko jàngal ci doylu ak gëm Yàlla.

Noonu la wéye ba ñibbisiwaat Tumburànka : Maken, liir bi ak moom. Ñibbisi ngir fàtte lépp. Ñibbisi ngir toog fi ba fàww. Li mu dund nekk ag dem-dikk gu yéeme waaye bari ay tolof-tolof. Gis nanu ay wajaase yu ni mel. Maymuna bu Abdulaay Saaji, jóge na dëkkam bii di Ngol ngir ñëw Ndakaaru. Te ba ca cëppaandaw la, dafa delluwaat dëkkam yóbbaale naqar ak tiis. Moom Daraamaan, dem na Sisaan, ñibbisi, dellu, ñibbisiwaat ci naqar, tiis ak tumurànke gu réy.

Soleils invincibles téereb nettali la bu Seex Ahmadu Bàmba Njaay bind ngir delloowaale ci njukkal ñenn ci sunu bindkat yi ak ay way-jëmmalam : Daraamaan (Aminata Dramane Traoré), Modibo (Modibo Keita), Kuwaame (Kwame Nkrumah), Nguugi (Ngugi Waa Thiong’o) mi génn àddina fan yii. Doonoon nit ku yàgg a xeexal der bu ñuul, yàgg a jëmal itam ay xalaatam ngir Afrig jëm ca kanam. Di ci piisaale Biraago Jóob ci xët wi mu ko tudde : “les morts ne sont pas morts”, añs.

Soleils invincibles, téere a ngi nii bu gànjaru di àrtu, yeete ak di jàngale ci ni ab Tumurànka (Saa-Afrig) war a taxawe, waxuma la ci kanamu waa Sisaan (Farãs), waaye ci kanamu àddina sépp. Seex Ahmadu Bàmba Njaay bëgg a wane ne nit dafa war a gëm boppam te xam mooy kan rawatina boroom der bu ñuul.

Téere bii ab yóbbal la ci bépp ndaw, ci bépp saa-Afrig. Mbind mi leer na, neex na te set. Am it cafka ak nose gu doy waar. Yenn saa nga mer, yenn saa nga jooy mbaa nga reetaan. Looloo móol doomu aadama. Bindkat baa ngi soññe ngir ñu toog liggéey sunu réew ba man a dëggal moom sa bopp gi nuy wax.

Abdulaay Sekk

Bindkat/jàngalekat.

Ablaay Sekk
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj