Njiitu réew mi Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay woote nab kàmpaañu njëmbëtum garab. Ñu namm koo amal ci réew mépp ngir jëmbët lu tollu ci 1 miliyoŋi garab ci diirub ñaari fan.
Tay ci gaawu bi, 2i fan ci weeru ut, Njiitu réew mi Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay ma nga woon ca àllu Mbaaw ba. Mu teewoon fa ngir jëmmal bés bi ñu jagleel réew mi te duppee woon ko ci nasaaraan Journée nationale d’investissement humain. Muy bés bob, taamu woon nañu ci set-setal réew mi. Wile yoon nag coppite am na ci. Nde njëmbëtum garab lañu ko nar a taxawe ci réew mépp.
Wëppa wi ñu ko tànnal di « Njëmbët garab, mën sa bopp ci dund bi, ak suqaleeku gu yàgg ñeel gox yi ». Naka noonu, ci àppu ñaari fan yii (gaawu ak dibéer), namm nañu cee jëmbët lu tollu ci 1 miliyoŋu garab. Àllu mbaaw ba ñu ko doon doore moo jiite liggéey bi. Waaye dees na ko lawal ci réew mépp.
Ginnaaw bi mu fa teewee, Njiitu réew mi amal na ubbite gi ak ay garab yu mu jëkk a jëmbët. Bokk na ci ña fa teewoon ñenn ci jëwriñi Càmm gi, kilifay caytu geet yu aada yi, ay njiiti gox ak i dépite, ay way-yëngatu ci askan wi ak seen i lëkkatoo ci xaralaak kopparal ba ci ay kurél yuy yëngu ci aar kéew mi.
Njiitu réew mi yékkati na fay kàddu itam ngir woo ci doomi réew mépp. Mu leen di xamal ni :
« Gépp garab gu ñu fi jëmbët tey dafay wane sunu taxawaay ci maas giy ñëw ëllëg. May feddali bu baax sama woote ci càmmug bokkeef gi, gox yi fasantikoo yi ci biir réew mi, ndaw ñi, jigéen ñi, kërug liggéeyi jàmbure yi, daara yi, sunuy lëkkatoo ci wàllu suqaleeku, ma-xejj yi fi réew ma ak fa bitim-réew. Na ñépp dugal seen loxo ci woote bi.
Ci kaw woote boobu, Njiitu réew mi dellu na xamal askan wi ak lëkkatoo yi ni lu ni mel ab xas la. Looloo tax mu leen di xirtal ñu ànd dogu ci te sax ci dogu gi ba mu jural leen ndam ci toppatoo kéew mi.
Mbir mi nag du yam ci njëmbëtum garab yi ci ñaari fan yii rekk. Ndaxte, jubluwaay bi mooy Senegaal peeg boppam ci wàllu kéew mi. Ci loolu, Njiitu réew mi di xamle ni dees na tàmbali balaa yàgg li mu duppe Caravane écologique 2025. Mu nar a doon xew-xew bu leen di yóbbu ci wër diiwaan yépp ngir amal ay yeete, ay tàggat, ak ay jëf ba ñu mën a toppatoo kéew mi ci diiwaan bu nekk.