Bari na ay kàddu yu siiw, yu nuy faral di wax ak a waxaat te amaana sax xamunu ku leen fent. Ñaare, nu moomale leen kenn ku siiw, di wax ne “diw nee na” fekk ne, nun ak moom noo ci bokk yam, dégg rekk lanu ci am. Dafa fekk rekk ne, danuy gis njariñ ak maanaa yi kàddu yooyu ëmb ba tax nu leen di jëfandikoo. Te sax nag, lu ci bari, danu leen di jël di leen suukaree sunuy kàddu ngir rekk ñu gën a neex ci nopp yi leen di taataan.
Yooyule kàddu, bokk na ci : “won ma say ndaw, ma wax la ban dëkk ngay dooni ëllëg”. Nu mën cee déggee ne, ndawi tay jii, ñooy doon i mag yiy yoreji réew mi fii ak i at ci kanam. Bu ñu leen tegee ci yoon wu baax, njort mën na a rafet ci ëllëgu réew mi. Waaye, bu ñu leen bàyyee ci li leen neex rekk, réew mépp a ko nar a réccuji. Jile wax, dafa jege geneen kàddu gu naan : “la ca maam, sët a koy jël”. Waaye, bu sët bi xamul li maam yor lu mu doon, du mën a xam dayob mbir mi. Te, bés bu loolu tegee ciy loxoom rekk mu sànk ko, jaaraale fa réere boppam te du ca bàyyi xel. Mooy Li ñuy naan mujjee puso, mu réer ci say loxo.
Sunum réew nag, fii mu tollu, bari na ñu gis ci ndaw ñi ay mbir yu teey xel. Ñi ko sañ a wax dinañu ne liy xeeñ neexul. Nde, taxawaayu ndaw ñi du luy gaatnga ëllëg su dal xel. Ndax, dafa mel ni danoo réere li Maam yoroon walla nu jàpp ne amalu nu njariñ ci jamono jii. La Maam daan dunde, dundal ci ñoom baay ba ñu màgg tollu ni moom lanu bëgg suul cim pax mu yaatu te xóot. Ndax jàpp ni ñam wi dafa forox te fekk ne xaajul a yàqu, nun ñii la sunu gémmiñ umu boole ko ak lewet. Ñu bari ci nun, jàpp nañu ne, maase ak jamono mooy wëlbatiku jàkkarloo ak sa baay ak i mbaaxam bu la nee benn, nga ne ko fukk. Te nag, kuy def noonu sa baay, lu ko raw nga nar a def sa Maam miy baayam.
Bokk na ci li maam daan def ci baay ba mu mat sëkk ki mu doon mooy ne ku nekk, mu jox ko cër bi mu yelloo. Yërëm ñi la féete ndaw, weg ñi la mag, koo maaseel jàppee ko ni sa bopp. Jox ku nekk li mu moom, bokk na ci liy indi yamele ak ug dal cim pénc. Rawatina nag mag mu fekkee lu bari te kenn mësu koo dégg ci lu ñaaw. Ginnaaw bi maam Kocc Barma Faal nee “mag, mat na a bàyyi cim réew”, am na ñu ca teg ne, na fekk mu doon mag mu baax.
Bu coow jibee ba ku nekk di jéem a wut fu mu far ak di ko fésal warul a tax mukk nuy ubbi bunt bob, wareesu koo laal sax ba koy ubbi. Réew mu nekk, dafa war a am ay màndarga yoy, bu ñépp féewaloo woon it, kenn du leen salfaañe, népp ay mànkoo nangul leen seen ub dayo te taxaw temm ci wattu leen. Dañuy doon, ci gàttal, ay laalaake, ku leen laal, mu wex la xàtt. Màndarga yooyu, mën nañoo doon i nit, walla ay barab, walla sax yeneen i yëf moo xam yuy dund ak yu amulug ruu. Mën nañu doon itam mbir yu nuy gis walla yees mënul a duut baaraam niki bàkku réew ci niral. Ba tax na, mën nanu leen a fekk ci fànn yu nekk.
Ci wàllum mbatiit nag, Senegaal dafa am doom ju ràññeeku lool nu koy wax Buukunta Njaay. Bu mbatiit doonoon àll, danu naan ci guy yi gën a fés la bokk. Mu fekkee démb, fekkee tay te rafetal lépp. Doon ab royukaay bu nu mën a jàppee ni kuy jokkale ñoñu démb ak yu tay ngir ñu waajal ëllëg. Bind na turam ci téerey taarixu Senegaal ak daa ju far te dootul far mukk. Ba keroog àddinay tukki, képp kuy gëstu ci mbooru xalam ci Senegaal, xareñ ci te ànd ci ak màndute gu mat sëkk, mënul a ñàkk a daj Maam Buu. Nekkul rekk ab xalamkat ak ub woykat bu mën lool li muy def waaye, daf cee boole doon ku fonk mboor bu baax teg ci di dundal ak a fésal cosaan ak mbaax yi maam làmboo woon. Maam Buu mu toog, ŋàbb xalamam ak mbaxana ma ca bopp ba rekk nataal la bu yànj lool. Toogaay boobu rekk, bari ay jàngat yu ci gëstukat yi mën a def.
Maam Buu, ag kàggu la guy dox. Ñàkk koo wormaal bu laluwul ci ñàkk a xam rekk, mën nanu koo jàppee ñàkk a fonk xam-xam. Ndax kàggu moom ak xam-xam, mëneesu leen a tàqale. Nde, ay téere ñoo ci nekk te téere moom, bu faree, lu bari ci xam-xam réer. Sunu jeneen maam waxoon na ne mag mu làqu ak kàggu gu lakk ñoo yam. Nu mën cee dégg ne, nekk mag rekk tax na nit doon kàggu ndax lu bari li mu jot a jankonteel ak li mu gis ci dundam. Kon, ci kaw loolu, Maam Buu kàggu la ñaari yoon. Nekk na ko ndax li mu jot a làq ciy at waaye it, nekk na ko ndax li mu xam ci mboor ak li mu mën ci woy ak xalam. Di ko joqarbi baaraam ak di ko ñàkk a wormaal, mënees na koo méngale ak taal kàggu gu fees dell ak i téere yu gànjaru lool.
Ci weneen wàll, nee nañu, xale buy dawal i téere mooy doon mag mu xel may xelli ëllëg. Kon naka la xale biy soofantal kàggu (magum téere) nar a mel bu màggee ? Jar na a laaj ndax raglu na lool. Danoo àgg ci, ndaw ñi waroon a dem tarbiyu kilifa yi ngir taataan seen i xam-xam te barkeelu ci seen i mbaax, ñoo toog di leen sànni xeer. Ci lu laluwul lu dul ci par-parloo, riirandoo, ñàkk i téggin ak ñàkk a xam. Ñàkk a xam dayob mag ñi, ñàkk a xam seen taxawaay ak seen liggéey ci pénc mi, ñàkk a xam it cëru cëslaay bu mag bi mbatiit am ci Senegaal gu naat te suqaliku gi nu bëgg a tabax.
Juum nanu gaa, nun ndaw ñi, njuumte lu réy nag. Waaye, Maam Buu sunu maam la. Nanu ko maamoo, sargal ko te tatagal ko. Te xam ne, saa-Senegaal yi nu doon, war na tax nu gën a bàyyi xel ci ne yamunu ak ku dul nun. Am nanu lu bari lu ñeneen ñi amul ci mbaax. Ba tax na, ni ko góor ga waxee woon rekk, bu ñeneen ñiy bàkku ci ne ñoo nu gën magi démb, mën nanu leen a tontu ne noo leen gën magi tay. Te nu fexe nag ba lu ni mel bañ a tee am.