PECCIM KÓLLЁRЁ (MÀNG) GI CI LÀNGUG PÓLITIG GI : LAN MOO KO WUND ?

Yeneen i xët

Aji bind ji

Pólitig nekk na mbir mu am solo lool ci mépp réew mum mёn di doon. Waaye, niñ koy defe ci Senegaal xaw a doy waar ci gis-gisi ñenn ñi rawatina ak peccim kóllёre gees ciy faral di nemmeeku. Maanaam, ni gaa ñi di jógee ci nguur gi di dem ci kujje gi walla jóge ci kujje gi fekki nguur gi. Mu nekk nag, mbir moo xam ne daanaka dem na ba safatul ñu bari ci maxejj yi. Ba tax, mu mat a samp ay laaj ngir xam lan moo wund xeeti jёfin yooyu ak ban taxawaay la ci maxejj yi (militaŋ) am.

Fii ci Senegaal, bari na lool lees fiy nemmeeku xeeti jёf yu ni mel saa bees dёgmalee walla jógee ci ay wote. Bi ci gёn a yees di bu Sёriñ Mansuur Si Jamiil njiital làng gi ñuy dippe Bés Du Ñàkk. Moom nag, ci lёkkatoo gii di Yewwi Askan Wi la jóge dem di dooleel ñii di waa Bennoo Bokk Yaakaar ñi nga xam ne ñoo fare ci nguur gi. Ca beneen boor ba tamit, kii di Mari Tёw Ñaan, bokkoon ci nguur gi ba amoon ca sax ndombog-tànk gu am doole. Moom it, génn na, fekki waa YAW nga xam ne ci kujje gi lañ féete. Loolu nag, du lu bees ci làngug pólitig gi. Ku nekk day dem fa nga xam ne fa la gis boppam. Donte ne sax, ñu bari ci maxejj yi dem nañ ba jàpp ne gaa ñi ñoom ñépp a yam. Seen bopp kese a leen ñor. Koo ci jàppale tuuti, fasante ak moom kóllёre, bu amee rekk wor la. Li ñuy xeeñ diwoowuñ ko. Te, li ñuy woote gёmuñu ci dara. Ndax kat, bala nga ne naam ne fa ba pare. Mu mel ni, ci làngug pólitig gi la ŋàññante ak worante wulleeb ñaay. Ku jóge ci boor bii, bu demee ba ca des, xalab ñam àndaloon démb ak barki-démb. Loolu, day firndeel ne ñu bari dañuy jiital seen i bёgg-bёgg fàtte, ñi leen dooleeloon bañ àgg fi ñu àgg. Waaye, ndax seen i militaŋ dinañ leen topp saa buñ feccee kóllёre gi doxoon seen diggante ?

Mu mel ni fi jamono ji tollu nii, ñu bari ci gaa ñi dañuy dem rekk wёliis seen i militaŋ. Militaŋ yi ñoom, dañuy def liñ naan ku ma wokk ma xuri la. Ku leen wor, ñu wor la. Ndax, kii di Bàmba Faal, nekke ca Médinaa, bim fekkee Njiitu réew mi ba am fa ndombog-tànk la ko ay militaŋam wan gannaaw. Li koy firndeel, mooy goxam boobu nga xam ne moo fa daan jiitu, ci wotey palum depite yii, dañ ko faa jiitu ak ñeneen ñu mel ni moom. Ba ci sax, kii di Idiriisa Sekk bim fekkee Maki Sàll ba léegi, daanaka Cees ga nga xam ne daawu ko xёccoo ak kenn, dañ ko faa jiitu ci wote yii. 

Loolu, di wone ne ci tёnk ne maxejj yi moom ku dem ci fu leen neexul rekk ñu bàyyi la ak sa yoon, seeti keneen. Muy ki fare ci nguur gi di ki fare ci kujje gi, amuñu ci xàjj-ak-seen. Ñoom, dañuy def liñ naan lёngoo neex na lool waaye koo bàyyi mu dem ak i mbaggam. 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj