Siidi Ahmet Aliyun Ndaw a ngi juddu atum 1933 ca Karcag, bokkoon ci wërngalu Biññoona, ca Kaasamaas. Baayam, ab fajkatu mala la woon boo xam ne, dañu bari woon li ñu koy tuxal. Jaar na ci daaray suuf yu bari, ca Luga, ca Lingeer ak ca Kumpentum. Ca daaray Sainte-Marie, Dakar Plateau, la doore njàng mu digg-dóomu mi laata mu koy àggalee ca Farãs ga mu dem ca atum 1955. Ndaw mi ngi amee bakaloreyaa (baccalauréat) ca Gap, ab gox-goxaan ca diiwaanu Provence-Alpes-Côte d’Azur, atum 1958, laata muy am lisãsu àngale ca daaray Grenoble ju kowe ji, atum 1962. Ginnaaw bi mu defee lëlub tàggatu ca Swansea, réewum Pays de Galles (1962-63), jàngale na ca Rouen, Farãs.
Ca atum 1965 la Siidi Ahmet Aliyun Ndaw ñibbisi ngir liggéeyal réewam. Dina jàngale ci kalaas yi diirub fukk ak juróomi at, daan jàngale àngale ci daara yii toftalu : Ecole normal William Ponty bu Cees, liisse Ameth Fall bu Ndar ak liise Malick Sy bu Cees. Ca atum 1971, burs Fullbright a ko mayoon mu jàngaleji ca De Pauw University, nekk Indiana, USA, laata muy delsiwaat ci liggéeyam.
Atum 1979 lañu ko woolu ca caytu gu kowe gog, njëkkoon na fa liggéey ci diirub weer yu néew, diggante 1967-68, niki Njiitalu Loy yi ak Jànguwaayu Gëstuy xayte yi. Ñu daldi koy tabb aji-digleb xarala ca Njiiteefu njawriñ ga. Ñu teg ca ñaari at tamit, 1981, ñu tabbati ko ca Njiiteefu Bokkeef gi, mu daldi fay liggéey diirub fukki at ak ñaar. BSDA (Bureau sénégalais du droit d’auteur) la mujje liggéey ci lu bir, nekkoon fa njiitul ndajem caytu gi diggante 1995 ba 2001.
Turu bindkat bi dafa yàgg a nëbb tur wi nekk ciy kayitam. Ndax, góor gi, ca at yu njëkkam ya ca daara ju kowe ja la tàmbalee bind ci ñaari làkk, ñu xam ko ci, ràññee ko ci. Bokkoon na ca kurél gu siiw googu ñu duppe « groupe de Grenoble » (àndoon ci ak Asan Silla, Masàmba Saare, Usmaan Faal, Jibril Mbeng ak Abdulaay Wàdd). Kurél googu nag, liggéeyu Seex Anta Jóob a ko xirtaloon, mu ànd ak ndongol iniwérsite lii di Saaliw Kànji, ñu liggéey ag nose ñeel mbindum wolof, daldi móol ab téere bees duppe Ijjib wolof ca atum 1959. Ba muy jiite kippug tiyaataru FEANF (Fédération des étudiants d’Afrique noire en France), Ndaw dafa tiyaatarloo kippu gi téereb kilib bii di L’Exil d’Albouri, ca njëlbeenug móolam gi am juróom-benni tablo. Ginnaaw gi, dina ci yokk yeneen ñetti tablo, muy juróom-ñeenti tablo. L’Exil d’Albouri, kërug móolukaay gii di éditions P.J. Oswald a ko móol ca atum 1967. Bi ko kippug tiyaatar gu Théâtre nationale Daniel Sorano dawalee, ame na ci medaayu wurus ca Xumbaanug mbatit bennoog-Afrig bu Alger, ca atum 1969.
Seex Aliw Ndaw, moom mi wax ne, « bind, daanaka ab wokkatu rekk la », diggante 1962 ak 1963 la njëkk a bind téereb nettali ci wolof, muy Buur Tilleen. Waaye, jamono jooju, xamoon na ne móol ab téere ci làkkuw Afrig lu jafe woon lool la, daanaka mënutoon a nekk sax. Moo tax, dafay mujje tekki téere nettali bi ci farãse, di xaarandi coppite. Noonu la Buur Tilleen, roi de la Médina génnee atum 1972 ca Présence Africaine. Lu jiitu loolu, Ndaw jotoon na génne ab téereb taalif, Kaïrée, ca Grenoble, atum 1964. Amoon na, ci mbindum loxo mi, ag cargal gu bawoo woon ci ndajem taalifkat ak artisti Farãs yi ak caabalu Art et Poèsie ca atum 1962. Bindkat bi dafa gànnaayoo xalima gu nangu te matale, bind téere yu bari yoy, mënees na ci lim téereb nettali bii di Excellence, vos épouses, téereb saabal bii di Le Marabout de la sécheresse ak téereb kilib bii di Du sang pour un trône ou Gouye Ndiouli un dimanche. Téere yii yépp nag, ma-xereñi ladab yi dañ leen a rafetlu.
Téere yi mu bind ci wolof nag, dañu yàggoon lool ci tirwaar yi laata ñu leen di móol ci ndoorte yu jàmbaare yoy, « jàmbaari làkki réew mi » ñoo leen sumb, niki ma-làmmiñal bii di Aram Faal, gëstukat ca IFAN (Institut Fondemental d’Afrique Noire). Naka noonu, ñu daldi móol, atum 1990, taalif yi mu bindoon diggante ati 1960 yi jàpp ati 1980 yi cib téere bu tuddu Lolli – Taataan. Looloo cuq Seex A. Ndaw mi yàgg a biral ne « li nu doon ca dëgg-dëgg, ci sunuy làkk rekk lay feeñe ». Yaxal yi di toppante, doore ko ci léeb yi ba ci njéemte yi. Ci xeetu téere bu mujj boobu la bind ab téere bu njëkk ci fànn wi : Taaral ak ladab ci làmmiñu wolof. Esthétique et littérature de la langue wolof (OSAD, 2002). Téere bi ab tegtaluwaay la ñeel ma-sos yiy wut cëslaay ci seen i liggéey, di jumtukaayu njàngat ñeel jàngkati téerey ladab yi. Ndaw daf ciy leeral xaralay yattiinu kàddu yoy, ñoo dooleel tëggiinu baat yi ci wolof, li ko dale ci xeltukat bii di Kocc Barma ba ci bindkatu téere nettali bii di Maam Yunus Jeŋ, jaare ko ci taalifkat bii di Seex Musaa Ka ak woykat bii di Njaga Mbay.
Atum 2004 lañ boole Seex Aliw Ndaw ci Akaademib taalif bu àddina si, ngir gërëmee ko liggéey bu yaatu bi mu jot a liggeey. Akaademi boobu nag, ay bindkat yu mag a mag ñoo ko sos, atum 2001, ca Vérone, Italie, te Wole Soyinka ca la bokk. Réewam ci boppam sargal na ko, neexalee ko Magug Cargalug Njiitu réewum Bokkeefu Senegaal (Grand Prix du Président de la République du Sénégal) ñeel Loy yi. Cargal gile, dañuy faral di ko neexalee ku bind ab téere bu ràññeeku. Waaye, wii yoon mooy guléet ñu koy jagleel liggéeyub lëmm.
Jëmm ju ni tollu yeyoo na njukkaluy ndongoom, yu nawleem, yu jàngkati téereem walla sax ñépp ñiy dund ak moom, teewe 90eelu atam.