Sëñ Bàmba Kéemaan la
Dem ba ñëw war a sant ci ñibbisi gi
Di sant Boroom bi ci dem gi
Ndeke dem gee jur Màggal gi
Bu demul woon dunu jot ci teraanga yi
Sëriñ bi … Kenn du Sëriñ Bàmba
Dem na ba ñëw ci jàmm ak salaam
Waaye di fésal ug cant Yàlla ci dem gi
Nattu yaa jur bànneexam
Xéewal yi rogolaat ba fépp tooy
Moyul kenn kon Bàmba mooy
Kéemaan di tawféex nanu ci ŋoy
Bi noon yi foogee ni
Jàpp nanu Séex bi
Moom Bàmba mu naan
Danoo bokk yoon rekk waaye àndunu
Tey bi pënd bi wuree
Ñépp xam nañ ni Bàmbaa gore
Yàlla rekk a fi ne, ku jëf mu fey la
Ku nekkal Yàlla, Yàlla nekkal la
Bàmbaa di ki gëm Yàlla
Jox boppam Yàlla
Léppam di Rasululaay
Wóor na ñépp, billaay
Moo ni xalimag Yàlla du bindati
ku mel ni Mustafaa, kon du amati
Du Yàlla da ko mënatul
Déedéet…Yàlla tëlewul dara
Waaye dafa nammatul a bind
Ku mel ni moom ci biib dénd
Sa mbëggeel ci Mustafaa du waxi kese
Mbàkke Bàlla
Woote ñépp wuyusi
Nit ak jinne, kenn du des
Njabar mënu ko
Bari pexe joxewu ko
Yàlla rekk a fi nekk
Yaa fii taxawal
Jëf-jël
Yaa fi jëf lu ñépp di soow
Ci lu baax, neeleen waaw
Moo waral tey nga am li nga am
Jërëjëf Séex Bàmba
Jërëjëf Maam Jaara