WOMEN FIRST TV Tele jigéen ñi, ngir jigéen ñi

Yeneen i xët

Aji bind ji

WOMAN FIRST TV tele la bu ay jigéen sos jagleel  ko it jigéen ñi. Mi ngi juddu ci jamonoy mbasum covid-19 mi lëmbe woon àddina sépp (2020). Ci gaawo gii nag, yemook 6 ut 2022 la WFTV dugg ci làngu tele yi, yematul ci lënd gi, ñu xamal ko askan wi ci xew bu ko taxoon a jóg ca Place du souvenir.

Doktëer Faatumata Li Faal mi ci bopp bi daa gis ne, jigéeñ ñi dañoo xareñ lool ; waaye daanaka ginnaaw lañ leen tàmm a féetale. Jàpp ni jigéen mën na waxal boppam, ndax nettali ci gémmiñu boroom. Moom ak kurélam, ñu sos WFTV, jigéeñ ñi jiitu, jëkk, di saytu ak a dogalal seen bopp, ànd ceek seen i ay càmmiñ, ñu leen di gunge. Soxna Faatumata di dalal xeli góor ñi :

“ Wonunu ginnaaw genn góor. Danoo bëgg rekk jigéen ñi nekk ci kanam, di waxtaane seen i mbir, di xàll seen yoonu bopp”.

Soxna Njooro Njaay ak soxna Mari Ãsélig Sawaane, ñoom ñaar ñépp ràññeeku bu baax ci luy jëmale kanam réew mi jaare ko ci xeex àq ak yelleefi jigéen ñi, lañ ndeyale woon ndaje mi. Bi Doktëer Njooro Njaay yëkkatee kàddu, ginnaaw mbégteem, ñaax na waa tele bi ngir :

“Ñu bañ a yem ci fecc ak woy rekk -ni ko ñi ëpp di defe- te gën a sóoraale xel, diisoo ci soxla ak njariñal jigéen”.

Mu teg ci, wax ne :

“Ànduma ak way-pólitig yi nga  xam ni, fu ñu tollu di jéem a nax jigéen ñi, di leen jëfandikoo te moone dey jigéen ñi ñoo leen tee wadd.”

Bu loolu weesoo, mu neeti :

“Senegaal a ngi door a génn ci joŋante ndawi réew mi. Am na ay jigéen yu ci bokkoon, di laaj baatu askan wi te mujjuñoo jàll. Su ma sañoon tamit, buy suba rekk, tele bi jéem a daje ak ñoom ñu xam nuñ ko gisee, am na solo.

Boo seetloo it ndaje yi ñul faral di waxtaane mbiri xale ak seen ay jafe-jafe, li tax muy lajj saa su ne, dañ ci dul boole ndey yi nga xam ni ñooy nekk ak seen njaboot, di gis seen ay coppite. Maa ngi gërëm Faatumata ak ñépp ñi mu àndal ci liggéey bu rafet bi.”

Jeneen ndey ji moom jotula teew, waaye cib widéwoo xamle na ni :

“WFTV egsi na ci waxtoom. Ndax, tey, daanaka fépp foo dem ci àddina si, jigéen ñi dañ leen di jëfandikoo ngir jaay, te duñu wone nataal bi gën a jekk ci jigéen. Kon, bu nu amee tele bu jiital jigéen, ci dundinam, ci ay jafe-jafeem, néew dooleem, waaye it ci ay jéegoom ci lu baax, dunu def lu dul rafetlu ko. Senegaal nag, mënul jëm kanam file ak jigéen ñi, ëpp ci réew mi, joxuñu leen gëdda gi war. Maa ngi ñaanal tele bi ndam, na seen ngelaw nangu”.

Jotaay yi bari nañ te wuute, waaye lépp ngir jigéen ca kow ca kanam.

Wér-gi-yaramu jigéen, jàmm ak kaaraange, yoonu yokkute jigéen, solo ak dayo làmmiñi réew mi, mbatit, waxtaan diggante jigéen ñu mag ñi ak ñi leen féete ndaw, gëstu pólitig, sumb añs., lii lépp ci biir WFTV.

Doktëer Li Faal nee na itam WFTV du tele buy yem Senegaal rekk. Nde, bëgg ñan ubbi ànten ci Koddiwaar ci diir bu gàtt, lawal ko it ci yeneen i dëkki Afrig yi.

Nanu gëm te liggéey ndax, “ku yàgg ci teen, baag fekk la fa”.

Woykat bii di Maya Abdul, neex baat lool, ak xalamkatam, ñoo doon xumbal ndaje ma. Ku ci nekk it ci gan ñi, fa nga toog fekk nga ñu tegal la mbuusum xéewal ak naan. Moo taxit, Jaañeen yi ak Ngayeen yi bégoon nañu lool sax.

Ndey Koddu Faal
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj