Ndey Koddu Faal
« Daf maa sàkku ci lu ma neexul… Egg na ci man… »
Kàddu yu naqaree dégg yii te daw yaram ñu ngi tukkee ci benn xale bu jigéen, dib way-tawatu covid-19 bi. Kenn ci way-wallu yee ko siif ca bérébu fajukaay ba. Nga ni ma ? Déedéet kay… Waa-waaw. Ana kon kuy mucc ? Ndax xel nangu na ku feebar, ki ko war a dimbali di ko siif ? Ngay taafantoo faj jigéen di ko jaay doole ba tëdde ko fa muy fajoo.
Looloo ngi xewe ci weeru Sulet bii ñu weesu ca ”Hôtel Novotel” bu Ndakaaru. Teeru way-tawati covid-19 dafa xawoon a jafe ndax li lim bi takku te jumtukaay yi tamit matewu ko. Looloo waral ñu soppi yenn ndal yi (centres) ak yenn otel yi bérébi fajukaay, dalal fa ñi mbas mi dal. Ndaw saa ngi tollu ci 20i at, ki mu joxoñ baaraamu tuuma di xale bu góor bu am 25i at, bokk ci ndawi Croix-Rouge yiy jàppale doktoor yi.Kon ndaw si, mën nañoo wax ni covid-19 bee ko yóbbee li ko dal. Moo tax mu dajeek ku fàtte warugaram.
Nu samp laaj yii : ndax ngóor si dafa àndul woon ak sagoom ba mënta muñ ki mu war a aar ? Ndax neexi tànk war na la yóbbu ci sàq moo beyul ?
Li xew Novotel danuy delloo ginnaaw tuuti, fàttali nu faatug Binta Kamara miñ reyoon ca Tàmbaakundaa.
Ayu-bés yi ñu weesu it ci Sacré-Cœur amoon na ndaw soo xam ni dañ koo tuumal càcc, ay góor di ko widéwoo ak a làmbaatu ba faf ko def daanaka yaramu neen.
Jigéen ñi ñu sàkku ci lu ñu àndul ak jigéen ñi ñu bóom fii ci Senegaal kenn xamul nu seen lim tollu. Hibaa Caam, ca Almaadi, buñ ko wallu woon, mën naa am mi ngi dund ba tey.
Kon, ñaawteef yooyu yépp ay góor a koy def. Fuñ ko teg ? Naka-jekk du mujj fenn. Xéy-na mooy waral njombe yu ni mel di wéy. Ba kañ nag ?
Xew-xew yii dañuy yee ci man yenn yu ma fàtte woon. Am na bés may waxtaan ak sama benn nijaayu taskatu xibaar ci xaritam boo xam ni fentaakoon la. Ma ni ko
– Kooku de, nee nañ bëgg jigéen a ko taxoon a dugg kaso. Moom népp nee nañ daa bëgg jigéen. Xam naa li mu digaaleek xale bu amagul 18 at moo ko gën a suuxloo.
Sama nijaay ree ba tàqaaju, daldi may tontu lii :
-Aa, góor gu wér kay day bëgg jigéen, bu doon wérul nag, xéy-na góoru ñaari tur lay doon.
Ma ni ko :
– Dëgg la… Kuy liggéey xaalis nga ciy séentu waaye suñ demee ba ñépp di la jëwe bëgg xaalis daa fekk mu yóbbu sa fit walla nga koy ame amin wu ñaaw. Góor it, suñ demee ba ku la tudd ñépp teg ci ni daa bëgg jigéen, daa fekk gorewu ci, àndu ceek sagoom…
Ñàkk sago googu tey jàpp naa ni moo waral liggéeykatu Croix Rouge Senegaal boobu song janq bi. Ndax su àndoon ak sagoom, doon na bàyyi xel ci naqar wi mu naroon a teg doomu-jàmbuur. Ku jigéen ki mën na faa jaare ragal góor, mu jural ko musiba, yàq àddinaam, walla mu jéppi góor ñépp, di leen yakk lu mel ni xeme, di leen naqaral te fekk defuñ ko dara. Looloo mën naa tax sax jigéen dem bay jaay boppam.
Bu nu fàtte yit ne ka ñu siifoon Novotel mën naa wàll xale bu góor bi covid. Balaa yàgg dinan ci xam dara ndax nee nañu yoon teg na ko loxo. Li am solo mooy mu bañ cee génne noonu.
Ci xibaar yi mujj yi nag, doktoor bi biral na ne way-aar bi tëdde na ndaw si waaye neewul da koo siif. Xanaa nuy fàttali rekk ni « lu ŋaaŋul du màtt ».
Ndey Koddu Faal