SIROY ALLAAXIRA YA CA  GÀMBI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Musiba bu réy a am ca Gàmbi. Juróom-benn fukki xale ak juróom-benn ñoo fa ñàkk seen i bakkan ci sababi siro yu ñu naanoon ngir faju ci feebar yu deme ni soj ak sëqët. Siro yi nag, End lañ leen defare.

Bu ñu fàttalikoo, ci weer yële ñu génn, jëwriñu Gàmbi ji yor wér-gi-yaram gi, génne woon na ab yégle di ci xamle ne, ca weeru sulet ba, lu tolloon ci 28i xale ñàkkoon nañ seen i bakkan ci ay biir yuy daw ak i jafe-jafey roño. Mu nekkoon lu doy waar te kenn xamul lu ko waral. Bi ñu càmbaree mbir mi, def ci ay gëstu, gis nañ ci ginnaw këru way-tawat ya woon lu ñuy woowe ci tubaab “Bactérie Escherichia coli”. Muy ab ség buy faral di sabab ay dagg-dagg yu ànd ak i jam-jam ci roño yi. Loolu lañ njëkkoon a jàpp, yaakaar ne moo waral faatug gune yi. Waaye biñ gënee xool mbir mi ci fànn yépp, ci lañu njort ne am nay siro yu sabab yi waral njàqare gi waa réewum Gàmbi nekke. Ndax lu ëpp ci xale yi génn àddina, daan nañ naan ci siro yi laata ñuy faatu. Ndax siro yi ci seen bopp dañuy faral di indi ay jafe-jafe ci roñoy nit ki, te réew yu bari firndeel nañ ni siro yi di def. Nde, du Gàmbi rekk lañ yem.

Jéyya ji dafa gën a taqarnaasi, nag. Ndaxte, dañu jóge ci 28i gune, yéeg ba ci 66i gune yu ñàkk seen i bakkan. Loolo waral waa OMS génn ci àllarba 5 oktoobar di artu nit ñi ci yile siro. Dañu jàpp ne 4i siro yii di Promethazine Oral Solution, Kofexmalin Baby Cough Syrup, Makoff Baby Cough Syrup, ak Magrip N Cold Syrup te ñu leen di defare ca laboraatuwaaru End bii di Maiden Pharmaceuticals, ñoo waral jéyya ji. Li ñiy ragal tamit bokk na ci, waa Maiden pharmaceuticals jëfandikowaat jumtukaayi wàllent yañ doon defare siro yi ngir defaraat ci yeneen i garab. Te bu loolu amee, garab yooyu mënees nañ leen séddale biir End ak réew yu bari ci àddina si. Ndax End dafa bokk ci réew yi gën a siiw ci wàllum defar garab di ko génne di jaay fu bari ci réewi àddina si. Moo tax waa OMS digle ne, réew yépp a war a def seen kéemtalaay kàttan ba dootuñ gis siro yi. Donte ne ca Gàmbi rekk la musiba bi yemagum te xamuñu kañ lay jeex, xamuñ it ci yan réew la siro yi tasaaro. 

Li gën a doy waar ci li waa OMS wax mooy ne ci biir 4i siro yi, dañ ci gis wàllent wu soqikoo ci ñaari ngirte yu bon yu ñuy wax diéthylène glycol ak l’éthylène glycol. Ñu ne déet-a-waay, la ñu def ci siro yi bari ba jéggi dayo. Yooyu ngirte dañuy faral di joxe ay biir yuy daw ànd ak mettit yu tar, ay woccu ak i dagg-daggi roño.

Ginnaaw gi la seen Njiitu réew, Aadama Baro, santaane ñu def lépp lu war ngir dakkal garab yooyu dugg biir Gàmbi, te taxawal ab laboraatuwaar buy saytu bépp garab buy jóge bitim-réew di dugg biir Gàmbi.

Ñu déggee ci ne, bu bakkan rotul woon, duñu taxawal ab laboraatuwar buy saytu garab yuy jóge feneen. Ngeen xam ne, kon, musiba bi mënoon na ñàkk. Ndax jotul réewi Afrig yi def seen kéemtalaay kàttan ba amal seen bopp ay isin, di defaral seen bopp garab yi ñu soxla ?

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj