SOLOS FUDDËN

Yeneen i xët

Aji bind ji

Coosaanu fuddën

Fuddën as ngarab la sos, ci làkkuw farãse, dippees na ko lawsoña inermis, bokk ci ngiirug garab gees di woowe lythracées. Ci kàllaamay Kocc nag, baatu « fuddën » dafay am ñaari taxawaay.  Bi ci jiitu mooy bu baat bi amee taxawaayu tur. Bu boobaa, « fuddën » dafay am ñaari sant : gi ak si. Bees waxee « fuddën gi », ngarab si lees ci namm. Bu dee « fuddën si », dafay dellu ci pëndax bi. Niral :

  1. Boo weeree xobi fuddën gi ba ñu wow, nga dëbb leen.

  2. Tooyalal fuddën si.

Ñaareelu taxawaay bi mooy bu « fuddën » dee njëfka, maanaam buy dellu ci jëfandikoo gi walla jariñoo bi. Niral :

  1. Faatu a ngi fuddën

  2. Xadi a ngi fuddënu.

Ngarabus fuddën nag, dafa am i dég. Tuddees na ko lawsoña ngir sargalee ko doktëeru saa-ekos bii di Isaac Lawson mi faatu ci 18eelu xarnu bi. Am na molekil bi nekk ci biir fuddën te di tax muy soppi wirgo béréb bi ñu koy diw. Molekil boobu tamit, lawson la tudd.

Bu dee turu Hortu uplandicus, gëstukatu mbindaare bii di Carl von Liné moo ko ko dippee.  Loolu mooy sistemu xaaj botanist bi ñuy jëfandikoo tay.

Fuddën nag, ba ñu ko tàmbalee jariñoo ak tay, yàgg na lool sax. Ndax, bees toppee mboor, dees na gis ne, nit ñi xamoon nañ fuddën ay junni-junniy at lu jiitu juddug Yonent Yàlla Isaa.  Jamono jooja, nit ñi dañu daan jëfandikoo fuddën ngir suub seen ug kawaru bopp walla kawaru sikkim. Fuddën nag, bari na ay njariñ.

Njariñi fuddën  

Ngir wax ci njariñi fuddën, danuy sukkandiku ci ni ko saa-Afrig yiy jariñoowee. Boo ñëwee Afrig nag, moo xam muy fuddën walla di gàñcax ba mu bawoo, lépp a boole am solo, moo xam ci wàllu mbatiit ak cosaan, ci diine ak yu ni mel, ci yokk taar ak it ci wér-gi-yaramu nit ñi.

Danu koy njëkkee ci xew-xewi cosaan yieek aada yi. nde, daf ci am mbir yu solowu yoy, fépp lañu fës ci kembaaru Afrig, ne fàŋŋ-fàŋŋaaral, rawatina jigéen ñiy fuddënu ci xew yi. Ndaxte, sunu gàttalee sax njàngat li, yemale ko ci Senegaal, dinanuy faral di gis yiñ diw ci loxo ak tànki ndaw si ñuy waaj a denc. Xew-xew boobu dafay faral di ànd ak i woy ak ay fecc, muy jamonoy jàmm ak mbégte. Ci jamonoy tay ji, « Henné Time » lees ko tudde xew-xew boobule, maanaam guddig fuddën bi. Ci fan wii nag, fuddën dafay màndargal yokkute way-dencante yi, seen njaboot ak it li bokk ci li leen di aar.

Jamonoy màggalu diine yu melni tabaski walla korite, jigéen ñi daan nañuy fuddënu ngir màggal bés bi, màggal bànneexu feet bi. Fa dëkki naar ya, niki yeneen réewi jullit ñi, bépp xew-xew bu am solo ci àddina, rawatina yu jëm ci diine, dañuy jëfandikoo fuddën.

Lu weesu xew-xew yu mag yi, fuddën dañu koy jëfandikoo itam ngir taaral yaram wi ci ay nataal yu taaru. Daanaka sax, ci loolu lanu ko gën a xam. Dañu koy diw ci loxo yi, tànk yi ak yenn saa yi ci kawar gi ngir taaral ko ak toppatoo ko.    

Ci beneen boor, fuddën dafa baax ci wér-gi-yaram. Maanaam, ci wàllu pajum cosaan mi, fuddën dafa am njariñ waaye ñu bari dañu ko umpale. Ndaxte, su nuy wax wér-gi-yaram, rawatina ngir faj ay dagg-dagg, ay lakk-lakk, ak yeneen i feebaru der. Ndax, ni fuddën di rayee doomi jàngoro dafa yéeme.

Ci gattal daal, fuddën yamul ci di suub der yi ak kawar yi. Nde, dafay dafay wane taar, cosaan ak mbatiit ak ngëm. Léegi sax, yeneen réew yi tàmbali nañu di nu toppandoo, di fuddënu.

Aji-bind ji : Ummu Kalsum Wàdd

Ummu Kalsum Wàdd
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj