SONACOS : JUBBANTI BU ÀND AK GOQI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ca ndajem jëwriñ mees amaloon ci njiiteefu elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, lañu jëloon mbirum SONACOS jox ko solo su réy. Jubluwaay bi mooy jubbanti kër gi, dundalaat ko ngir amaat bu taxawaay bu am solo bu mu amoon walla mu raw ko. Waaye nag, laata ñuy wax waxi jubbanti, fàww goqi am. Maanaam, balaa dara, Càmm gi dafa namm a fayeeku bor ak koppari SONACOS yu tollu ci benn miliyaar yees sàkkal pexe.

Am na ku SONACOS jure (kalaame ci Yoon). Benn koomtukat (opérateur économique) lay topp ci wàllu kàmpaañu mbayum ati 2022/2023. Ag kor la SONACOS di jiiñ nit kookii. Dafa sax, Yoon jotoon na koo jàpp. Waaye, ginnaaw bi koomtukat boobu joxee kàddoom, nangoo fay SONACOS koppar yu tollu ci benn miliyaar ak xaaj (1,5i miliyaar) fii ak weeru desàmbar 2025, ci la ko Yoon bàyyeendi. Waaye nag, laata ñu koy bàyyeendi, dafa tayle lenn ci alam.

Bees sukkandikoo ci sunu naataangooy Libération, am na beneen koomtukat bu Yoon di diir. Te, ci lees wax, kooku dafa bokk ci genn këru diine gu am doole ci réew mi. Li ñu koy tuumaal mooy ne dafa jaay diwlinu SONACOS te delloowul xaalis bi. Xaalis boobu nag, tollu na ci benn miliyaar ak xaaj.

Kon, bu fi mu nekk nii, SONACOS mi ngi dawagum ci ginnaaw 3i miliyaar yoy, bu ci jotee, dina gën a mën a jubbanti kër gi, mu delluwaat fa mu nekkoon. Loolu moo tax njiit yi wax ne, balaa jubbanti di ci am, fàww ñu goqiloo ñi randal koppari kër gi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj