SONACOS SIGICOOR : JËWRIÑ MABUUBA XOOLI WOON NA NDEFAR GI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Jëwriñu mbey mi, Sëñ Mabuuba Jaañ, amaloon na tukkib nemmeeku fa Sigicoor. Li mu ko dugge woon mooy saytuji ndefaru SONACOS ga nekk ca diiwaan boobee, rawatina sàqum peppi gerte yi.

Jubluwaay bi gën a réy bi njiiti réew mi sas Jëwriñ Mabuuba mooy fexe ba Senegaal moom boppam ci wàllu dund. Maanaam, liggéey, suuxat fànni mbey mi ak càmm gi ngir am ciy njureef yu matale ba dund gi jàppandi ci doomi réew mi, fekk ne duñu aajowoo jéggaani lees di lekk ak a naan. Ci weneen waxiin, fexe ba li saa-senegaal yiy dunde di jóge ci réew mi, ñu ko fiy beyee te di ko fi defaree. Loolu mooy nisëru Njiitu réew mi ak elimaanu jëwriñ yi, rawatina moom Sëñ Mabuuba Jaañ, jëwriñu Mbay mi, Càmm gi ak Dund gu doy gi. Senegaal nag, ku fi wax dund, wax diwlin. Nde, kenn umaplewul ne, lees di jëfandikoo diwlin ci sunuy togg dafa bari lool. Daanaka, néew na ñam wu saf wees di taaj wow, toggeesu ko diw. Moo tax ñu bëgg a yékkatiwaat SONACOS miy defar diwlin, samp ko ci diiwaan bu nekk. Bu ko defee, nit ñi dinañ am liggéey, gerte gi ñuy defaree diw ji dina jar, beykat yi gis ci seen bopp, ba noppi diwlin ji jàppandi ci boroom-kër ci njëg lu yomb. Loolu bokk na ci lu tax jëwriñ ji demoon Sigicoor.  

Ba mu àggee nag ba saytu liggéey bi, jëwriñ ji biral na fay dég-dég ñeel kàmpaañu mbey mi ci atum 2024-2025 mi. Bees sukkandikoo ciy kàddoom, ginnaaw 101i fan yees dajale gerte gi, tomb yii lees mën a jàpp ci tënk :

▪️Mboolem ndajale gi : 209 400i ton (daaw 100 400i ton kese lañu dajale woon. Kon, ren, 109 000i ton dolleeku nañu ci.)

▪️Ndajaleg jiwu yees wóoral yi : 60 300i ton

▪️Ndajaleg gerte gees war a sopparñi diw : 148 900i ton ciy gerte-xott yu SONACOS dajale

▪️Jëmmalug jubluwaay yi : ba jonni-Yàlla-tay jii, bees xaymaa lees dajale lépp, dafay tollook xaaju lim bees bëggoon dajale ca njëlbeen ga. Maanaam, téeméer bu nekk, fi mu nekk nii, 50 yi kepp lañu jotagum dajale. Dafa di, 300 000iy toni gerte la SONACOS jublu woon a dajale.

▪️Payooru beykat yi : Càmm gi fayagum na 49i miliyaar (daaw ci waxtu wii, 8i miliyaar kese lañu fayagum woon)

▪️Payug faktiiri “intrants agricoles subventionnés” : 39i miliyaar lañu fayagum ci bésub 18eel ci màrs 2025

Ci xalaatu jëwriñ ji, jéego yii, jéego yu am a am solo lañu. Waaye, ba tay ciy waxam, bu koppaar teeloon a teew, romb kon nañu fii di dem.

Jëwriñ ji xamleet na ne, kërug liggéey gii di Copeol tàmbaleegul dajale yi mu war a def. Li ko ko tereegum def mooy jafe-jafey koppar. Loolii nag, dafa bokk ci li tax dajalewuñu lim bi ñu jublu woon.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj