SOWAAL : JÀPP NAÑU GAAL GU YABOON LU ËPP 300I MBËKK-KAT

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ndawi duwaan yi nekke Fimla jàpp nañ ag gaal gu naroon mbëkki. Gaal googu nag, dafa yeboon lim bu tollu ci 300i mbëkk-kat ak lu teg. Ci àjjumay tay jii, ginnaaw bi ñu jullee jumaa ba noppi, lañu dëpp gaal gi xam ne, mi ngi doon sori. Bees sukkandikoo ci yéenekaay Le Soleil, mbëkk-kat yi, ci ay réew yu bari lañu bawoo laata ñuy teersi ca tefesu Sowaal, fa gaal ga waroon deqee. Fi mu nekk nii nag, ñoom ñépp ña nga ca sàndarmëri bu Sowaal ñu téyandi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj