Démb ci Gaawu bi 15 oktoobar la ñii di waa Yewwi Askan Wi doon taxawal kurél gii ñu dippe Réseau des Elus Locaux du Sénégal (REELS). Maanaam, kurél gi ёmb mboolem ñi ñu fal ci gox yi ak goxaat yi. Kurél googu nag, du ngir waa YAW kepp, ci li ñu wax. Képp ku jàpp ne mёn na jёmale gox yi kanam rekk, mёn ngaa ñёw bokk ci. Ndax, bi ñuy taxawal kurél gi, xamle woon nañu ne am na ñu ci jot a bokk ak ñu ci namm a bokk te falewuñu leen ci raayag YAW, niki meeru Usuy bi, Usmaan Jàllo. Usmaan Sonko lees tànn ngir mu jiite kurél gi.
Ñépp lañu tàllal loxo. Nde, ci seen i wax, ubbees na buntuy “REELS” yi ñeel képp ku ci gis sa bopp ak sa njariñu gox, ak fépp foo mёn a féete. Amul Nguur, amul kujje. Ndax kat, mbooloo mooy doole. Te, lu kenn mёn, ñaar ñoo ko ko dàq. Te, ñoom ñi taxawal “REELS”, nee nañu wujje taxuleen a jóg, jàmmaarloo ak Nguur gi tamit taxuleen a jóg. Ñoom, dañoo bёgg a andi ay xalaat yu yees ci pólitig bi. Jox làngug pólitig gi geneen xar-kanam. Te, ñu jàpp ne bu ñu bokkee ci geneen kurél, duñu mёn a doxal seen gis-gis ni mu ware, ak ci ni ñu ko bëgge. Liy seen mébét nag mooy jёmmal meeri yi ba saa-senegaal yi gёm ne ñàkk a ànd ak Nguur gi, warul tere kenn def sa liggéey ni mu ware. Donte ne sax, dina la gàllankoor ci benn boor.
“REELS” nag, kurél gu yees la gog, dafa ёmb ñi ñu fal ci wotey gox-goxaat yi rawatina ñi bokk ci lëkkatoog YAW gi nga xam ne ñoom ñoo ko sos. Am sax ñu jàpp ne dañuy wujje ak kurél gii di Association des Maires du Sénégal (AMS). Waaye nag, xamle nañu ne wujjewuñu ak kenn, liggéey kepp a leen tax a jóg. Ndax, bi wotey gox-goxaat yi jàllee lañu ko bёggoon a tёral. Waaye, ci weeru Awril lañu mujj tàmbali di ci dox ay jéego ngir taxawal ko. Ñoom nag, démb ci gaawu bi lañu mujjee taxawal kurél gi ba tёral pekk gi. Pekk googu nag, nii la tёdde :
Njiit li : Usmaan Sonko
Tof-njiit yi
Bàrtelemi Jaas
Baabakar Géy
Aminata Kànte
Fara-caytu yi
Dr Mamadu Jite
Asan Kase (adjoint)
Seex Géy (secrétaire permanent)
Dr Asiis Mbóoj (secrétaire national à la communication et porte parole)
Xadi Mesoor Juuf (adjointe)
Kani Béey (secrétaire chargé des relations extérieures)