TÀGGAT YARAM

Yeneen i xët

Aji bind ji

Saajo Maane dugal na ñaari bal ci joŋante bi ekibam Liverpool doon amal démb ak Chelsea. Ci ñaareelu fanu joŋante yi la dugal balam yi njëkk ci atum futbal mu bees mi.

Bal bi njëkk mi ngi ko dugal ci 50i simili, bi ci topp ci 54i simili, muy ñaari bal ci diggante ñeenti simili.

Njiitu ekibu Senegaal wone na mëninam, ñaari bal yii mujj yokk lim li mu dugal ak Liverpool ci 65i bal. Mu tollook li español bi Fernando Torres mës a dugal ci diir bi mu def Liverpool.

Safiyetu Béey
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj