TEGGI TUUMA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Yàgg dina dindi tuuma, waaye gaaw cee gën bu naree jur njombe. Loolu la fajkat bi, Alfuseyni Gay, xam ba tax ko jóg, indiy leeral ngir weddi wax yees ko waxloo. Démb la woon layoob Aji Saar ak Usmaan Sonko. Ay seede yu bari teewoon fa, niki moom doktoor Alfuseyni Gay mi nemmeeku woon Aji Saar, keroog 2i fan ci féewiryee 2021. Bi ñu xéyee tey nag, ay yéenekay yu bari dañoo fëgg ci seen xët yu njëkk yi lenn ciy kàddu yees askanale fajkat bi. Moom nag, weddi na lépp.

Alfuseyni Gay dafa génne ab yégle ngir leeral lënt-lënt yi bawoo ci yéenekaayi tey yi. Nde, biralees nay kàddu yoy, nee ñu, doktoor baa leen fa wax. Ci li taskati xibaar yooyii rotal, déggees na ci ne, moom Alfuseyni Gay moo wax ne fekk nay wasalaan (spermatozoïdes) ci pëyub ndaw sii di Aji Raabi Saar. Moom nag, nee na araam, mësul wax lu ni mel.

Dafa génne ab yégle ci ngoonug tey ji, di ci dàjji waxi taskati xibaar yi askanale wax jooju. Moo ko tax leeral ne, moom, waxul wenn yoon ne, gis nay wasalaan ci pëyub Aji Saar, ginnaaw ba mu ko saytoo, keroog bésub 2 féewariye 2021. Rax na ci dolli sax ne, bët kepp mënul a gis wasalaan. Doktoor bi ne :

« Saytu bu njëkk ba ma amaloon ca bésub 2 féewarye, gisuma ca lenn lu jóge ci awra góor, waxumalaak wasal (sperme). La ma ca gis kay, li bokk ci moom la, tey génne ci biir pëyam. Tegoon naa ci ne, gisuma benn gaañu-gaañu ci awraam. Lu ni mel nag, mayuma may wax naan soxna si séq na ak góor…. »

Lii rekk doyoon na cib leeral. Waaye, ñoo ngi doon ruumandaat njëlbeenug ceet gim seetoon ndaw si, naan am na lum fekkoon ci moom. Looleet, àddu na ci, fàttali ne :

«…saytu bu njëkk ba ma defoon ak Aji Saar, yoon nanguwu ko….. Waaye, ak lu ci mën a nekk, saytu yii rekk ñoo ma mën a waxloo ci wàlluw yoon. Te, ñooy ya ma sàndarmëri santoon, ma amaloon ko ca bésub 3i fan ci weeru féewarye 2021…. »

Xanaa leer na.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj