TÉYANDI NAÑU PAAB MAALIG NDUUR (APR)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Tay lañu woolu woon Paab Maalig Nduur, nekkoon jëwriñ ca nguurug Maki Sàll ga woon, bi 16i waxtu jotee ci ngoon, fa màkkaanu banqaasu luññutu bob sàndarmëri [Section de recherches de la gendarmerie]. Sabab bi tax ñu woolu woon ko mooy kàddu ya mu yékkati woon ci menn ndajem polotig, fan yii weesu.

Ca ndaje mooma, ka woon jëwriñu ndaw ñi, bokk APR, dafa biraloon i kàddu, di ci woote ngir ñu « […] boole dooley askan wi ngir déjjati nguur gi fi nekk, te taxawal nguurug négandiku goo xam ne, Maki Sàll a ko jiite. » Kàddu yooyii lees koy toppee.

Dafa di, keroog ba mu fésalee yile kàddu, coow li bari woon na. Ñu baree ko doon ñaawlu, rawatina ñoñ Pastef. Amoon na sax ay kilifa yu ràññeeku ci Pastef, bokk ci nguur gi, ñu ñaawlu wax ji, muy ku ci mel ni Aamadu Ba, jëwriñu mbatiit mi, ñeeñal geek wërteef gi, ak Ayib Salim Dafe mi jiite kippaangog dépitey Pastef yi fa Ngomblaan ga. Rax-ci-dolli, amoon nay ndawi Pastef yu bindoon jëwriñu yoon wi bataaxal, toftal ci ab jure bu ñu jébbaloon toppekatu bokkeef gi. Ginnaaw coow li, tay jii lees woolu woon Paab Maalig Nduur ngir déglu ko.

Ci lees rotal ciy dég-dég, Paab Maalig Nduur janoo na lu yàgg ak takk-der yi ko doon déglu. Bi ñu ko dégloo ba noppi nag, dañu ko téyandi li feek luññutu giy mat.

Li ñuy toppe Paab Maalig Nduur mooy mbirum yee fitna ci pénc mi [trouble à l’ordre public], woote ngir daaneel nguur gi [appel à l’insurrection] ak i jëf yu mën a jur loraange ci liggéeyu campeefi réew mi. Ba tay, ci wàllu tuuma yi, toppekat bi daf ko gàllaat tuumay tiitloo sóobare yeek fere yi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj