TOOGAANU-ÑAXTU NGIR JÀPPALE PAAP NJAAY MU WALF

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ay téeméeri-téeméeri nit ñoo teeweesi toogaanu-ñaxtu ba amoon ci buntu màkkaanum Walf. Lees ko dugge mooy kaas ngir ñu bàyyi Paap Njaay, taskatu-xibaaru Walf biy faramfàcce mbirum Yoon ca tele ba. Bésub 7 màrs lañ ko nëbb jant bi ba nëgëni. Nee ñu dafa biral i xibaar yu wéradi yoy, dañuy nasaxal liggéeyu Yoon. Nde, moom Paap Njaay, dafa waxoon cib jotaay ne, li ëpp ci àttekati toppewaay bu mag bi (parquet général) yi dañu waxoon ñu suul mbirum ciif gi Aji Saar di tuumaal Usmaan Sonko, ndax dara amu ci.

Mbooloo ma, nag, bari woon na. Ñenn ñaa nga soloon i yére yoy, bindees na ci, ci farãse, lu mel ni « Bàyyileen Paap Njaay ! ». Taskati-xibaar yi tamit ñoo nga fa woon, bari woon fa lool. Jàppale seen naataangoo a leen fa indi woon. Loolu la àmbu Biyaagi di firndeel ci kàddu yii toftalu :

« Danoo nekk di seetlu ne, jamono jii, ñoo ngiy salfaañe àqay taskati xibaar fii ci Senegaal. Te, bu ñu demee ba taskati xibaar yi amatuñ sañ-sañ biral li ñuy gis, di ko dégg, day mujje doy waar. »

Sàmbu Biyaagi, nag, dafa bokk ci Mbootaayu taskatu xibaar yi, maanaam Association de presse. Ci mikóro RFI la doon waxee lii. Njiitul Walfadjiri lu mag li tamit, Séex Ñas, ñaawlu na nennu bi nguur gi nennu kibaraanu Walfadjiri.  Dafa di, CNRA jot na fi ajandi WalfTV diirub ayu-bés ci weeru féewaryee wii weesu, ba ñaxtu ya amee Mbàkke, mu wone woon ko. Séex Ñas dafa jàpp ne, li tax ñuy dal seen kow saa su nekk, du lenn lu dul di lal i pexe ngir « néewal doole Walfadjiri ci wàllu koppar. Loolu doyul, ñu jàpp Paap Njaay. Moom daal, dañu am yéeney tëj Walfadjiri rekk. Loolu kese la. »

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj