Ndakaaru, fi la waa réew mépp wutsiy xëy. Ndaxte, fii la lépp nekk. Waaye nag, saa bu tabaski, korite walla nowel teroo, ñi ko men ñépp ñooy dellu ca seen i dëkk, ca seen weti njaboot, ngir julleek ñoom. Loolooy waral ñuy faral di dégg kàddu gu mel ni “Kenn dëkkul Ndakaaru.” Ndax, ñépp ay dem, wutali gaaraas yi. At mu jot noonu la fay deme. Atum ren mi tamit, noonu la fa deme. Ñépp ñoo ngi ñibbi ci jàmm ak salaam ba mu des waa Kaasamaas, rawatina waa Sigicoor.
Tabaski bi jubsi na. Ñu baree ngiy ñibbi ci jàmm. Gaaraas boo dem, daamar yaa ngay yeb nit ñi, bagaas yi ak xar yi. Ñu baree ngiy tukki, di génn Ndakaaru. Naam, paas yi njëge nañ lool sax. Waaye nag, ñàkk pexee tax askan wi nangu ko. Mënuñu ci dara. Te, kenn bëggul a sore sa waa kër ak say mbokk ci xeeti bés yu ni mel, rawatina tabaski. Ñépp ñoo ngiy tukki nag ba mu des waa Kaasamaas yi nga xam ne, ñoo ngi leen di teg ay jafe-jafe yu tard ci yoon wi.
Ginnaaw bi réew mi yëngoo ba léegi, keroog bi ñu daanee Usmaan Sonko, tukki jëm Sigicoor yombatul. Ndax, daamari Dakar-Dem-Dikk dematuñ fa. Gaalug Alin Sitooye Jaata gi tamit, dafa taxaw. Roppelaan yi sax naawatuñ jëm fa. Ñu ni déet-a-waay, gornoor ba yokk xar mi kawar.
Gornooru diiwaanu Sigicoor dafa jël ndogal, tere tukki yi diggante 18i waxtu ci ngoon jàpp 8i waxtu ci suba si. Ak ni Sigicoor soree Ndakaaru ak yeneen diiwaani réew mi, dina jafe lool ci way-tukki yi bëgg a duggu Sigicoor.
Ñu baree ngi njort ne Nguur gi fi nekk dafa guuxal mer waa Sigicoor ndax Usmaan Sonko. Kenn amagu ci lu ko leer nag. Kaaraange la Nguur giy layalee ndogal yi mu jëlagum yépp ñeel dem beek dikk bi fa Sigicoor. Ak lu ci mën di am, nañu xam ni, Sigicoor, ci Senegaal la bokk. Te, tëj Sigicoor du ko teree soor.