TUKKIB ELIMAANU JËWRIÑ YI FA EMIRAAT ARAAB YA AK ITAALI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Elimaanu jëwriñ yi, Sëñ Usmaan Sonko, moo nga woon tay fa réewum Itaali, ginnaaw bi mu jeexalee, démb ci àjjuma ji, tukki bu mu doon amal fa réewum Emiraat Araab ya.

Ca altine jee weesu la Elimaanu jëwriñ yi, Sëñ Usmaan Sonko, tàmbali woon ab tukki fa réewum Emiraat ya Arabes. Muy ñetteelu tukki bu mu amal, di ci génn kembaarug Afrig bi mu faloo ca weeru awril 2024 ak tay. Ñaar yu jiitu yee ngi mu amaloon fa réewum Siin ak Tirkii. Ñuy tukki yu mu nas, bees sukkandikoo ciy kàddoom, ngir tolruy digaale yuy suqali koom-koomu réew mi.

Ci tukkeem bii nag, moo ngi àndoon ak ñenn ci jëwriñi Càmm gi, rawatina Ahmat Amin Lóo, di jëwriñ ci wetu Njiitu réew mi, Yaasin Faal mi yor léegi wàlluw Yoon, Biram Suley Jóob mi yor Laf gi, Soroj geek Mbell yi), Abdu Rahmaan Saar (Koom-koom, Naal ak Koppe gi), Seex Dibaa (Kopparal ak Ngurd mi) ak Àlliyun Sàll (Jokkoo, Xaralay jokkoo ak Nimerig).

Ci juróomi fan yi ñu fa def, Sëñ Usmaan Sonko ak i jëwriñam amal nañu fa ay ndaje yu bari ci seen digganteek kilifay réew ma. Ñuy ndaje yu am solo yu aju ci gën a dëgëral lëkkatoo gi dox ci diggante Senegaal ak réewum Emiraat Araab yi, di réew mu àddina yépp nangul dalam, rawatina ni mu nekkee ci diiwaan bu bari ay yëngu-yëngu.

Ginnaaw looloot, elimaanu jëwriñ yi daje na faak doomi réewum Senegaal ya fa nekk. Gaaral na leen naal wii di Joyyanti Koom ak Mboolaay mi (Plan de redressement économique et social). Dellu na itam sàkku ci ñoom ñu dugal ci seen loxo ngir teg Senegaal ci yoon wu yees.

Bi mu jógee fa Emiraat ya démb ci àjjuma ji, Elimaanu jëwriñ yi dafa jubali fa réewum Itaali ngir daje faak Saa-Senegaal yi nekk Tugal. Ni mu ko defe woon ak Saa-Senegaal ya nekk fa Emiraat ga mu jëkke, gaaral na leen tay ci gaawu bi naalu joyyanti koom wi mu sumb.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj