Kurélu àttekat yu Senegaal gi, UMS, ñaawlu na taxawaayu Meetar Musaa Bookar Caam ginnaaw bi mu juree àttekat bii di Idiriisa Jara ci mbiri Muhamadu Ngom mees gën a miin ci Farba Ngom.
Démb ci àjjuma ji, 21 nowàmbar 2025, UMS (Union des Magistrats du Senegal) génne na ab yëgle ngir àddu ci mbiri Meetar Bookar Caam ak jure bi mu jébbale fa kurélug Luññutu gu mag gii di IGAJ (Inspection général de l’administration de la justice). Muy jure bob dafa cay dàkk Idiriisa Jaara mi jiite ndiisoog àttekati luññutu gu PJF (Pôle Judiciaire Financier).
Ci seen yëgle boobu nag, ñoo nga cay ñaawlu ak di ko dànkaafu. Nde ci li ñu jàpp, jëfam ji dafa jublu ci jéem a yàq deru ab àttekat. Bees sukkandikoo ci li ñu siiwal, ginnaaw bi ñu toppee mbir mi ba leerlu ko, gis nañu ni Sëñ bi Ngom miy ndayu mbill gi sax yëgul, tinul. Naka noonoot, mbooloo laykatam yi yëguñu dara ci jëfam ji.
Ginnaaw bi ñu seetloo lu ni mel, ñoo ngay xamle ni ci coobare boppam la ko amale te teguwul wenn yoon ci doxalin wi ñu santaane. Looloo tax na ba ñu jàpp ni am na leneen lu ko tax a jóg lu mu biralul. Rax-ci-dolli tuuma bu réy la teg ci kaw àttekat bu ñépp nangul mën-mënam, dëggoom ak jox àq liggéeyam.
Fii mu nekk nag, kurél gi jàpp na ni Meetar Musaa Bookar Caam moo tay jalgati sàrti doxalin yi tënk laykat yi. Ñuy ñaawlu bu baax taxawaayam bu ni mel. Dellu nañu itam di ko dànkaafu. Nde ci seen yëgle bi, ña nga cay xamle ni dinañu ci am taxawaay bi mu laaj ngir ñu teg ko daan yi ci war, ni ko seen sàrt yi tëralee.