AAMADU BA (JËWRIÑU MBATIIT MI) : « MBATIIT, DAFAY JUBOOLE TE DI SAXAL WÓOLOONTE »

Yeneen i xët

Aji bind ji

Jëwriñu Mbatiit* mi, Ñeeñal* gi ak Wërteef* gi, Aamadu Ba mu Pastef, teewoon na ndajem saabal mees jagleeloon Xumbeenu* pasin* ak mbatiit mu Afrigu sowu jant. Xumbeen moomu, duppees na ko ECOFEST (Festival ouest-africain des arts et de la culture). Ci alxamesu tay jii lees ko doon amal fi Ndakaaru. Moom jëwriñ ji, jël na fa kàddu gi, daldi biral solos mbatiit ci wàllu juboole askani Afrigu sowu jant yi, fay ay yi mën a dox seen diggante, te saxal wóoloonte seen biir.

Sëñ Aamadu Ba daf ne : « Wóolootuñu campeefi bokkeef gi. Mbatiit nag dafay juboole. […] Bu dee ci wàllu campeef yi, dafa am ay gàllankoor yu bari yees di jànkonteel. Te, mbatiit moom, dafa jéggi mbirum njiiteef yi te dafay tax nit ñi wóoloonte. »

Kàddu yii, mi ngi leen biral ci ndajem saabal mees jagleel waajtaayi njëlbeenug xumbeenu ECOFEST mi. Xumbeen mile nag, CEDEAO ak UEMOA ñoo ko sumb. Bees sukkandikoo ci kàdduy jëwriñ ji, li ñu ko dugge mooy wut pexe ngir saafara ay yiy faral di tàkk ci diiwaanu Afrig sowu jant.

Wëppa wees tànnal xumbeen mi mooy : « Coppite ak fitnay pólitig biir Afrigu sowu jant : lu ci mbatiit mën ? » Dees na ko amal fi Ndakaaru diggante 30 nowàmbar wii jàpp 6 desàmbar 2025. Ñu ngi ciy xaar 500 ma-xumbeen* yuy bawoo ci 12i réewi Afrigu sowu jant.

Jëwriñ Aamadu Ba neeti : « Duggante bi am ci diggante mbatiiti Afrig yi dootul lu ñuy naatable. Yaakaar nanu ne amees nay pexey dipolomasi yees mën a jëfandikoo ngir dalal nit ñi te di leen boole ak a bennale. »

Rax na dolli ciy kàddoom ne, mbatiit, bariwul ay ñaaw njort amu ci.  Jëwriñ jaa ngi am yaakaar ci ne xumbeenu ECOFEST dina doon ab pose bu réy ngir neexale mbatiit yi, dalal xel yi ci biir Afrigu sowu jant gog, dafa bariy ay ak fitna ci wàllu pólitig ak kaaraange. Nde, ci kàdduy Sëñ Aamadu Ba, « fu pasin yeek mbatiit di waxe, ngànnaay yi dañuy faral di muuma. Jàpp nanu ne, bu nu jaaree ci mbatiit, dinanu mën a fay ay ayi dipolomasi. »

Baat yu jafe yi / Mots difficiles

Mbatiit = culture

Ñeeñal = artisanat

Wërteef = tourisme

Pasin = art

Xumbeen = festival / festivité

Ma-xumbeen = festivalier

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj