WAXTAANU NJIITU RÉEW MI AK VLADIMIR POUTINE

Yeneen i xët

Aji bind ji

Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, jokkoo na ak Njiitu réewu Riisii, Vladimir Poutine. Barkaatu-dém, àjjuma 22 nowàmbar 2024, lañu wax telefon.  Moom, sunu Njiitu réew mi, moo ko xamle ci xëtu njéndel li. Daf ne :  ñ

“Tay, ci yoor-yoor bi, jokkoo naa Njiitu réewu Riisi, Vladimir Poutine.

Séq nanu waxtaan wu yaatu te am solo. Waxtaane nanu kóllëre ak digaale yi yàgg a dox diggante ñaari réew.

Déggoo nanu ci ànd liggéey ngir dooleel digaale ñaari réew yi, jàmm ak dalug Sayel bi, ak itam ñu sàmm mberaayu CEDEAO. Dinanu boole sunuy doole, ànd ci ak àddina sépp, ngir dékku jafe-jafe yiy xaar àddina si.”

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj