WÉERUWAAY

Yeneen i xët

Aji bind ji

Sunu jenn maam ju mënoon a way ne woon na : “Am kilifaay li am solo. Soo ko amee am nga solo. Soo ko amul amoo solo”. Muy wax ju yenu maanaa, neex ciy nopp ba noppi xóot. Ñu bari di koy faral di wayaat, jëlee ko ci sunu maam Seriñ Mbay Jaxate mi ñépp xam. Mu nekkoon kàngaam bu ràññeeku lool te bokk ci werekaan yi, maanaam taalifkat yi gën a fés te gën a mag yi réew mi mës a am.

Bi mu noppee ci kàddu yu gànjaru yooyu te bari njariñ, daf ci teg ne : “ku wéeruwul, yomb a bëmëx”. Mu mel ni kuy bëgg a lëkkale ak a gam-gamle kilifa ak wéeruwaay. Nu mën cee déggee ne ku am kilifa, am foo wéeru.

Su nu ko gisoon te sañ koo laaj, danu ko naan : “waaw maam, lan mooy kilifa ?” Ndax, bu leerul ci nun kat, dina jafe lool nu dégg waxam jii. Nde, dunu mën a toj yax bi bay àgg ci yuq gi.

Nun nag, waa Senegaal, niki mboolaay yu bari, danuy fal Njiitu réew, jébbal ko ay ndombo-tànk yu takku, ne ko doxalal. Moom it, ciy sañ-sañam, mu tànn ñenn ci doomi réew mi takkal leen ci ndombo yi nu ko dénk ngir ñu jàppale ko ci liggéey bi. Képp ku mu tabb ba takkal ko genn ci ndomboy tànk yooyu rekk, def na ko kilifa. Am naat ñeneen ñoo xam ne, pénc mee leen di fal ci nu méngoo ak ni muy falee Njiitu réew mi. Ñoom tamit, askan wi leen tànn, def na leen i kilifa. Mu am nag ñeneen ñoo xam ne kenn tabbu leen te kenn falu leen itam. Ndombo gi ñu takk dafa dox ba agsi ci ñoom. Mu mel ni ndono. Te sax, bu ko doonee yit, lu yell la ci ñoom. Ndax, képp ku ci takk ndombo gi rekk, daf koy jàpp, jot ko sëkk, yam ci moom képp. Mel ni rekk, ci moom lañu ko nattoon. Rax-ci-dolli, ku ko ci yor, dafay teg i tànkam fa ki mu wuutu tegoon i yosam. Tàmbalee fi mu yam te wéyal liggéey bi.

Ñatti kilifa yii, bari na lool lu nuy jonjoo ak ñoom. Jegeyoo nanu bu baax sax ñoom ak nun. Donte ne réew mi am na yeneen xeeti kilifa sax, ñii la nuy gën a jëflanteel daanaka. Mel ni ñoo gën a fés.

Lu yàggul dara, ci fan yii nu weesu rekk, dund nanu fi xew-xew bu leen boole dajale ñoom ñatt ñépp. Ca Kawlax, mbir maa nga amoon ci diggante Xalifab Medina Baay, calaw li ak fara bi. Muy benn xew-xew, ci benn dëkk, boole ñatti kilifa te bari lool ay jàngat yees ci mën a def.

Gis nanu fa calaw lu jàkkarloo ak ub fara ñuy jokkalantey kàddu ba seen baat jóg. Fara bu waa gox ba fal ak calaw lu Njiitu réew mi tabb, yabal ko ca gox ba. Ku ci nekk, takk ndombog tànk gu bokkul ak ga keneen ka yore ba noppi, ñu am i sañ-sañ ak dayo yu wuute. Naam, bokkuñu liggéey. Waaye, lu ci bari fàww ñu ànd defandoo ko ngir njariñal waa gox ba. Ndax, ñoom ñaar ñépp seen liggéey yee bokk jubluwaay te du lenn lu moy jariñ askan wi ñu bokk jiite.

Ñaar ñuy xëccoo ag buum guy tàwweeku, ku bàyyi cat li mu jàpp rekk, gaañ moroomam. Waaye bu dee ne ay kilifa lañu moom, bu amee kuy gaañu askan wi ci seen ginnaaw doŋŋ lay doon. Luy metti, ci ñi ñu yilif lay njëkk a dal te, bu ñu moytuwul, ci ñoom rekk lay yam. Ñoom kilifa yi, lu ñagas ci seen diggante rekk, gaañ mbooloo mi. Moo tax waruñu di réeroo. Ndax, yenukati xëddéen kat, maam nee, dañuy yëgoo.

Ba tax na, donte ne ñépp mënuñoo bokk gis-gis, ay kilifa moom, waruñoo jàmmarloo mukk ci kanamu njaboot gi ñu bokk. Loolu, kenn xamul li mu mën a jur ci lu ñaaw ak fa yàq-yàq ya mën a àgg. Seen i jafe-jafey bopp ak seen i wuute, war nañu fexe ba di koy waxtaanee fu kenn nekkul. Lu ñu bokk tilimle rekk, ñu def ko póotum biir néeg.

Kilifa gu nekk, kilifa nga. Te, ku sañoon, kenn du xotti sa worma. Ngir moytu yu bari nag, ku ci nekk war na xam ki mu doon, li ñu teg ci ndoddam ak ñi bootu ci ginnaawam. Ci lay mën a biree ci moom ne, bu nekkee kilifa, dafa fekk ne am na ñu mu jiite. Ñooñu ñoo tax kilifteefam nekk. Mu weg leen, te xam ne, ak nu dooleem mën a tollu ak it fu ay sañ-sañam mën a àgg, am na fu ñu yam. Te, am daraja yu kawe ak i sañ-sañ yu jéggi dayo, warul a tax mukk fu mu toll di leen wone, ak di yékkatiy mbaggam.

Ñi mu yilif itam bañ koo jox bopp, rocci làmmiñ. Ñu nangul ko li mu doon te xam ne kilifa, cérub Yàlla la. Te maam ne woon na “ku Yàlla jiital, ku ko jiital, jiitu. Ku ko desal ginnaaw, des ginnaaw far juutu”. Ci noonu la mboolaay giy amee dal ba ku nekk tal a dox i soxlaam ci teeyug bàkkanam.

Mbir mii nag, li ci gën a neex, te ñàkkul moo tax mu gën a siiw, mooy fi yëf yi mujjee. Jaare ko ci sunu Maam Maahii Ñas, Xalifab Medina Baay bi bokk njaboote calaw li ak fara bi yépp ak jéego yu rafet yi mu ci dox. Moone de, moom kenn falu ko te it kenn tabbu ko. Waaye, wone na ni moo leen boole yilif ñoom ñaar ñépp. Ba tax na xaarul coow li àgg fu sori, fi mu jibee rekk, la ci sotti ndox mu sedd guy.

Taxawaayam wone na ne kilifa dafay may bët ak i nopp njabootam te du leen tanqamlu. Bu ñu leen tooñee ak bu ñu tooñee yépp mu teew te sañ leen a wax dëgg. Waayeet, lépp lu leen bëgg a féewale, mu taxaw temm fanqal leen ko. Yore pusoom di ñaw ak a dabb-daaxe yàqute yi fés ak yi nëbbu. Safara su nar a tàkk mu mëdd ko balaa jib. Ndax kat jàmmi njaboot gi mooy jàmmam.

Njaboot gi it nangoo am kilifa te tàmbalee ko ci baay ja ca kër ga. Ndax kat, “ku ne sa baay du kilifa, baayu keneen du mën a nekk kilifa ci yaw”. Bu ko defee, kenn ku nekk wut wéeruwaay ndax, nekk kilifa terewul a am kilifa. Ñàkk kilifa kay moo jigul kenn. Ndax, ku amul kilifa rekk, jinne di sa kilifa.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj