Bi nu noppee ci fal Njiit lu bees, teg ko ci boppu réew mi, ñu bari dañoo gisoon ne yamuñu rekk ci soppi ñi doon jiite. Waaye, anam bees daan pólitigee lees soppi. Maanaam, la woon a wonn. Li Senegaal xamoon ci wàll wi te mu sampu woon fi, saxal fiy reenam lu ëpp xaaju xarnu, moo fa jaar saay. Yenn jàngatkati xew-xew yi sax demoon nañu bay wax ne, garab gi fi Seŋoor jëmbatoon, te way-pólitig yi doon ca jëfandikoo boobu ba tay, moom lañu faf buddi, sempi ko, tege fale.
Njiit lu bees li yit, bi mu toogee ba tànn ay gaayam, ca la tàmbalee teg i jéego mel ni kuy bëgg a dëggal ne coppite gi ñu bari di ruumandaat lu am la. Lépp lu nu tàmmoon ci lu jaaduwul te demoon ba mel ni lu bokk ci nun, danuy jóg, dakkal ko. Doomu Senegaal taxaw na temb ngir téye dundam, tay ak ëllëg, ciy loxoom, du xaarati kenn ci lenn. Jot na ñépp xam ne Senegaal réew la mu am jonnug boppam, di doxal ni mu gënee ciw askanam te kenn du ko rëddal yoon wi muy jaar. Ci noonu lanu gisee lenn ci ay jëf yees mën a jàppee nikiy màndarga.
Su nu duggee ci lënd gi, xëtu Njénde li fa nekk, léegi mënees na koo yër ci wolof, araab ak àngale ginnaaw farãse ba ca yaggoon a nekk. Bésub ubbiteg péncoom réew mi ñeel pólitig bu atum 2025, tënk nañu waxtaan ya fa amoon cib téere bu ñu bind ci wolof yu leer nàññ. Waaye itam, gis nanu li xewoon keroog ca awril 2024 bi Njiitu réew mi demee Gàmbi seeti naatangoom ba.
Bokk na ci li gënoon a fés ci tukkeem boobu, mooy ne ñaari njiit yi wolof lañu doon làkk. Te, ci yeneen ndaje ya daan am lu ko jiitu, saa-Gàmbi bi àngale la daan wax, saa-Senegaal bi tontu ko ci farãse ba noppi am ab làppatoo ci seen diggante di tekki waxtaan wi. Mu mel ni rekk dañu leen a tere woon a làkk wolof wi ñu bokk dégg ñoom ñaar ñépp. Noona ndaje ma deme woon taxoon na ba, ca weeru me ba ca topp, ñaari kàngami bindkat yu ràññeeku yii di ndem-si-Yàlla si Ngugi Wa Thiong’o bu réewu Keeñaa ak Bubakar Bóris Jóob mi réew mi xam bu baax, bokkoon bind ab bataaxal bu ñu siiwaloon te jagleel ko Njiitu réewum Senegaal. Loolu, ngir feeñal seen ug mbégte ci dayo ba ñu joxoon làkku wolof ca ndaje ma woon ca Bànjul. Nde, ñépp xam nañu leen, ñoom ñaar ñépp, ci seen taxawaay ak seen ug dogu ngir aajar ak a xamle làkki Afrig yi ak mbaax yu gànjaru yi ñu ëmb.
Ci jamono jii, ñu bari, bu ñuy wax ci Senegaal, dañuy tudd dogoo ak jëfin ya woon bi kilifa yi bëgg a jëmmal ak it coppiteg doxalinu pólitig gi ñuy wax. Ba tax na ñaari kilifa yi bindoon ci seen bataaxal ba di soññ Njiitu réew mi ci mu fexe ba sunu làkk yi am taxawaay bu mat sëkk teg ci doon cëslaay ci Senegaal gu bees gi nu bëgg a tabax. Waayeet, àrtu nañu ko ci ne, bu mu juum mukk bay jël wenn làkk di ko teg ci kaw moroom ma. Ndax kat, saa-Senegaal bu ci nekk rekk, am na sañ-sañu laaj ñu fonkal ko aw làkkam.
Ci kaw loolu lépp nag, réewum Senegaal dafa am ag jagle. Te mooy ne, ñu ëpp ci askan wi ko dëkkee dégg nañu wolof donte ne sax duñu ay wolof. Loolu moom, mbir la mom, mënees na cee duut baaraaam, àndul ak lenni par-parloo. Àgg nanu sax ba ci, ñaar ñu dul wolof te ku nekk am làkku boppam te dégg ko lool, bu ñuy jëflante, lu ci bari wolof lañuy làkk. Soxlawuñu ku leen di tekkil seen i wax. Làkku wolof, saa-Senegaal yi dañu ko moomale seen bopp bu baax.
Waaye nag, donte ne loolu dëgg la, li ne fàŋŋ te soxlawul ku ko jéex mooy ne fii ci réew mi, làkku farãse moo fi gën a am jëmm ndax moom lañu gën a fullaal. Donte ne sax, ñi ko fiy làkk ñu néew lañu. Bees sukkandikoo ci xayma yi fi mujjee am ci nat dayog askan wi ci atum 2023, 0,6% doŋŋ ñoo koy làkk ci réew mi. Maanaam, fukk ñoo jël ci réew mi, kenn ki sax làkkul farãse. Loolu nag waroon na a tax ba kilifa yiy wax waxi coppite ak waxi jonn gu dëggu, ñu gën a góor-góorlu ba bu ñuy wax ak askan wi, ñu leen di làkk lu ñu dégg. Ndax kat, jaaduwul ci ñoom, ñu janoo ak askan wi di làkk lol, ñi ëpp ci way-déglu yi xamuñu lu muy tekki. Te sax, ñoom, bu ñu wonee ni fonk nañu sunu làkk yi ba di leen jëfandikoo ni mu waree, dina tax ba xalaat bi ñu bari am ci ne làkki ñeneen ñi (farãse, araab, àngale, añs.) ñoo gën a kawe sunuy yos dina wàññeeku bu baax walla sax mu deñ ba fàww. Nde, amul wenn làkk wu ëpp dayo yeneen yi.
Naka noonu itam, ginnaaw ne moom sa bopp dafay laaj fonk ak dëggal sa bopp, doon na gën lool, bu Njiitu réew mi ak geneen kilifa gu mu mën a doon, demee tukki cim réew, rawatina mu dul làkk farãse, mu fay wax wenn ci sunu làkk yi. Buy dem it, mu yóbbaale kenn ku dégg làkk woowu ngir mu mën a dox diggam ak ñi muy fekki. Te sax, ci fànn woowu, bataaxal bi nu tudd sànq ci kaw wax na ci. Nde, ñaari kilifa yaa ngi doon xelal Njiitu réew mi ci mu taxawal ag kërug làppatoo ak tekkig làkk yi. Muy doon barab bob, dafay boole ak a ñoŋal làkki réew mi ci seen biir, waaye itam diggante làkki réew mi ak yeneen yi ci àddina sépp. Te loolu, dina tax réew mi gën a jariñoo xam-xam bu sell bi ay doomam, di ay ma-làmmiñal di togg ci jàngune yi te ñu néew ci nun di ko jëfandikoo. Te it, dina won àddina sépp ne Senegaal bari ay kàngam yu mënee fu bari.
Lu ci bari nag, bu nuy wax ci luy suqali sunu làkk yi, dina am ñu jóg ci sunu biir di ci teg safaan. Di wax naan sunu làkk yi daal génnuñu réew mi, fii rekk lañu leen di dégg. Loolu moom du lay wu dëgër, wéeruwul ci lenn. Li am kay mooy, nun lanu bëgg a tayal-loo rekk ngir gën a suufeel sunu làkk yi. Bari na ci àddina si ay làkk yoo xam ne, fi ñu leen di làkke taxu leen a yaatu lool. Waaye terewul ñu wër àddina. Ndax rekk yitte ji ko ñi koy làkk jox ak seen taxawaay bu àndul ak dara ci yaras.
Dina jaadu it nu biral ne, amul lenn njariñ ci di jéem a won ñeneen ñi ne dégg nanu seen uw làkk te fekk ne xamunu lu bari ci sunu wosu bopp. Loolu dafa woroo lool ak dëggal ni am nga sag jonn te moom nga sa bopp. Amul njariñ itam ci di indi ag kujje ci làkk yi walla di leen jéem a xeexal. Loolu, jëmeewunu fenn fu baax. Li am solo kay mooy xam sunuy làkk ba peeg leen, bu nu noppee gëstuji làkku ñeneen ñi. Loolu mooy gànjar gi nekk ci sampu ba dëgër ba noppi ubbeeku ni ko Léwópóol Sedaar Seŋoor doon waxee.
Ci weneen waxin ak ci nu mu gën a yaatoo, nanu nangu ne aw làkk lenn la cim mbatiit ba noppi wëlbatiku doon këf ki koy tingoom. Bu nu ci noppee, nu xam ne li am solo mooy sukkandiku ci sunuw làkk ngir xam, nànd, nangu ba noppi moomale sunu bopp sunum mbatiit. Loolu moy tax nu mën a toog fu dëgër ak cëslaay gu wóor daldi mën a jariñoo li baax te jóge ci ñeneen ñi : lu jiitu gépp jonn.