Ci dibéer jii, 31eelu fan ci sulet, la askanuw Senegaal waroon a sànniji seen i xob ngir fal ndaw yi leen war a teewali ca Ngomblaan ga, fa ñuy péncoo mbiri réew ma.
Ci ngoon gi, bi ñu tëjee wotewaay yi, ay boori 20i waxtu, la njureef yu njëkk yi tàmbalee wadd. Yu bitim-réew yaa njëkk a génn. Muy Afrgi, di Tugal ba ca kembaarug Amerig, Yewwi ak Wallu ñoo raafal lépp. Ci biir réew mi tamit, lees fi jotoon a taataanagum lépp, njiglaayu kujje gi la woon, rawatina waa Yewwi Askan Wi ak waa Wallu. Bees sukkandikoo ci xaymay Alfõs Cakaan, dib ma-xayma, nii la toogteef yiy séddalikoo ca Ngomblaan ga :
Bennoo Bokk Yaakaar : 64i toogteef
Yewwi Askan Wi : 45i toogteef
AAR : 2i toogteef
Bokk Gis-gis : 1 toogteef
Bunt bi : 1 toogteef
Les Servieteurs : 1 toogteef
Noonu, kii di Dr Abdurahmaan Juuf, njiitalu làngug Awalé te bokk ci lëkkatoo AAR Senegaal dafa teel a nangu. Waaye nag, dafa bind lol, lënt na xeli nit ñi. Ndaxte, ci xëtu Facebookam li bind ab bataaxel ne, « Askan waa am dëgg saa su nekk ».
Noonee tamit la Soxna sii di Viktorin Ndey mi bokk BBY, ca Sigicoor, nangoo ndamul Gii Maris Saañaa ci kowam. Mu daldi koy woo telefon, ndokkeel ko. Moom itam, ci xëtu Facebookam li bind lii : « Sëñ Gii Maris Saañaa laa doon waxal telefon nii, daldi koy ndokkeel ci ndam li mu am. Noo bokk depaartmaa, diiwaan ak Senegaal. Maa ngi koy ñaanal ci Ngombalaan gi mu jëm. »
Waaye, dafa mel ni ñeneen ñi ci Nguur gi, yenn ci kàngam yi, nanguwuñu loolu.
Tàmm laago la, waaye…
Na woon, fa woon. Na waa lëkkatoo Bennoo Bokk Yaakaar (BBY), ci atum 2017, janoo woon ak taskati xibaar yi ngir, ci seen i wax, jébbal i xibaar ñeel ngirtey wote yi, noonee lañu ko defaatee ci guddig dibéer jii, ca màkkaanug APR gu Ndakaaru. Ci guddi gi lañ fa woo woon taskati xibaar yi ngir joxe, ci kàddug Soxna Aminata Ture, boppub toftalaanug BBY, ay xibaar yu « leer, baax, jub, yu kenn sosul. » Moom, Soxna sees dàkkantale Mimi Ture, lim nay depaartmaa yoy, nee na BBY a fa jël raw-gàddu gi. Noonu, ciy waxam, boo jëlee 46i depaartmaa yépp, BBY a raw ci 30 yi. Mu teg ci, wax ne, « Noo jël raw-gàddu gi ca Afrig bëj-gànnaar, Afrig sowu-jant ak Afrigu digg gi, muy tekki ne nooy ëpp i depite ca Péncum réew ma ci lu amul sikk. » Mu ngi tëje ay kàddoom ci delloo njukkal askan wi ak ñi ci jàpp ñépp, ak di wax ne dégg nañu, ñoom waa BBY, li leen askan bëgg a wax ci gox yi ñu jiituwul yépp, rawatina ci diiwaanu Ndakaaru.
Rasin Talaa, Njiitalu RTS, moom dafa ne BBY moo jël raw-gàddu gi ci lu leer te, « xel xalaatul nguurandoo (cohabitation) di am te bokkul sax ci lu nuy waxaale. Ndaxte, bu xaaju-guddi (miniwi) jotee, ci la Bennoo di biral ay njureefam. Mën leen wax ci lu wér [officiellement] ne Bennoo mu raw ci lu yaatoo yaatu te gisuma fan lañuy jaar ba nguurandoo am… »
…loxo du tàmm a gudd, gàtt te dogeesu ko
Waaye, nag, bi Soxna Aminata Ture waxe lu ni mel ba noppi, kujje gi, rawatina waa YAW, dañu génn weddi li mu wax ba noppi di artu.
Ci guddig dibéer ji la YAW génne ab yégle di ci ñaawlu doxalinu waa BBY ak njureef yi Soxna Aminata Ture fésal. Ñu wax, ci seen yégle boobu ne, « Danoo waaru, ginnaaw bi nu dégloo kàdduy Soxna Mimi Ture mi biral ay njureef di wax ne BBY moo jël raw-gàddu gi ci yenn depaartmaa yi. Loolu di doxalin wu safaanoo ak yoon. Waaye, moom [Soxna Mimi Ture], Maki Sàll lay waxal, moom mi bëggati fokkati xobi saa-senegaal yoy, YAW ak Wallu lañu jiital ca Ngomblaan ga, bees sukkandikoo ci li rotagum te tukkee ci PV yi nu yor… » Ñu teg ci ne, depaartmaa yi Soxna Mimi Ture lim yépp, ñoo fa jiitu. Ci seen njeexitalu yégle bi, ñu ngi ciy artu, di wax saa-senegaal yi ñu taxaw temm, aar njureef yi.
Bu dee Bartelemi Jaas, moom miy boppu toftalaanug YAW ci Ndakaaru, dafa ne « luubal bii du jàll ! Na ndaw booloo te xaar santaane yi. »
Barka Ba, ab taskatu xibaar bu doon waxe ca TFM, dafa jàpp ne wote yii, dañu fajalee mbirum ñetteelu moome gees daan laam-laame. Ciy waxam, « ci li ëpp ci gox yu mag yi, askan wi daf fa daan làngug Nguur gi. Bu kujje ndamoo, bu fekkee dëggal nañu njureef yees jotagum, dees na fi gis lu bees tàq. Te, bu Nguur ndamoo sax, am na njàngat lu leer lees ci war a jële : ci yoon, mbirum ñetteelu moome gi moom féete na boor ci guddig tey jii… »
Ak lu ci mënti am, bala ñoo péncoo réew mi, mel na ni xëccoo bu tar a fi nar a am