Réewi Afrig yi, rawatina yoy Afrig sowu-jant, bari na lool lees fay nemmeeku ay yëngu-yëngu. At yu mujj yii moom dañ cee raw. Te, lenn waralu ko lu dul ay mbiri pólitig. Bu dul ag Nguur gu sóobare ya daaneel, di Njiitu réew mu jeexal ay moomeem bëgg a xaabaabal. Walla sax, mu doon coow diggante Nguur gi ak ki fa walla ñi fa jiite kujje ga. Te, li xew Koddiwaar ak réewum Càdd ci njeexitalu ayu-bés bii doy na ci firnde.
Mbiri pólitig lëmbe na lool réewum Koddiwaar ak Càdd ci ayu-bés bii ñu génn. Dafa di, fu nekk ak la wund coow la. Nde, kenn umpalewul ne weeru oktoobar wii di ñëw la waa Koddiwaar di amal seen wotey palug Njiitu réew. Ki fa nekk Njiitu réew, Alasaan Watara, mébétam mooy amal ñeenteelu moome. Loolu la kujje ga ne du ca dal. Waaye, moom yamul foofu kese.
Ñaar ñi ñu ne ñoo fa jiite làng ya fa ëpp doole ca kujje ga, di PDCI (Parti Démocratique de Côte d’Ivoire) ak PPA-CI (Parti des Peuples Africains Côte d’Ivoire). Maanaam, Tiijaan Caam ak Lórã Bagboo duñu bokk ca wote ya. Looloo tax, ñu boole seen doole génnee seen i ñoñ ci gaawu bi ngir naqarlu doxalin woowu. Bi ñu amalee seen ndajem ñaxtu, mboolo mu takku moo leen wuyusi.
Li ñu dugge ndaje moomu mooy naqarlu ñeenteelu moome gi Njiitu réew ma di wut. Rax-ci-dolli, sàkku ñu dugalaat leen ci lawax yi war a joŋante ci wote yii di ñëw. Ndax, li ñu def teguñu ko fenn. Jël Yoon def ko ngànnaay ngir xeex ñi nekk ci kujje gi.
Naka noonu, fale ca réewum Càdd tamit, Yoon dafa jël ndogal lu diis teg ko ci kaw fa nekkoon elimaanu jëwriñ yi di, Succès Masra. Waaye, jamono jii ak la ko jiitu it, mu bokkoon ci ñi ëppoon doole ca kujje ga. Moom, moo jiite làng gii di “Les Transformateurs”. Moom nag, keroog ci gaawu bi lañu ko daan ñaar-fukki ati kaso. Te, daan bi yamul foofu. Nde, alamaan nañu ko lu tollu ci benn miliyaar ci CFA. Li ñu ko daane mooy li ñuy dippe “diffusion de message à caractère haineux et xénophobe et de complicité de meurtre”.
Kon, mu mel ni at yu mujj yii moom xew-xewi pólitig yee ëpp lu ñuy yëngal réewi Afrig yi rawatina yoy sowu-jant. Daanaka réew mu ñu coow ba noppi rekk, meneen feelu ko. Te, lépp Nguur kesee ko waral. Waaw, lii ba kañ ?