LIGUE DES CHAMPIONS, EUROPA LEAGUE, CONFÉRENCE LEAGUE
Ñetti joŋantey kuppe yoy tugal yépp àgg nañu ca cappaa-ndaw ga, maanaam, finaal ya.
Bu dee Ligue des champions, Inter de Milan moo ciy daje ak Paris SG keroog 31eelu fan ci weeru me wii. Europa ligue bi nag, keroog 21eelu fanu me wi lees koy amal. Muy dox diggante Manchester United ak naatangoom bii di Tottenham. Ñetteelu joŋante bi, te gën cee néew dayo, muy finaalu Conférence League bi, Chelsea moo ciy laale ak Real Betis bésu 28i me bi.
LIGA : BARCELONE DUMAATI NA REAL MADRID
Ren jii, Barcelone dafa fippu, nennu wujjam wi, bom ko seen joŋante yépp. Tay jii ci dibéer ji, ñu doon ci daje seen 4eelu mats ci at mi, mu jaarati ko fam ko jaroon ca yeneen ya. Foogoon nañu ni, wii yoon sax, Réal dana fippu. Ndax, dañu ni xaas, Real Madrid daldi am penaltii, dugal ko. Ñu dawalaat diir bu gàtt, mu dugalaat beneen. Waaye ci simileek saa, Barcelone daldi wëlbati yëf yi dugal ko ñetti bii laata xaaj bu njëkk biy jeex. Joŋante bi ci 4-3 la mujje. Fim ne nag, Barça rawee na Real Madrid 7i poñ, loolu mel ni lu leeral jëlug sàmpiyonaa ba.
LIGA : SORLOTH DUGAL NA TURAM CA MBOOR MA.
Saa-norweesu Atletico Madrid bi daldi nay def lu rëy démb ci seen joŋante beek Real Sociédad. Ñeenti bii la dugal ci ñeeti simili. Waaye itam, ñeenteel ko ci xaaj wu njëkk wi.