Abiib Jara gan-ganluwul fa Àngalteer. Gannaaw ba mu jógee Strasbourg dem Sunderland, doomu Senegaal ji amal na ci gaawu gii matsam bu njëkk foofa. Mu nekkoon mats fo, mu daldi ciy paas ñu dugal.
El Maalig Juuf tàggatoo na tay ci dibéer ji ak ay farandooram ca Slavia Praha. Loolu di dëggal demam ca sàmpiyonaa Àngalteer ca ekibu West Ham.
Kuppeg àddina këlëb yi : Chelsea jël na ko !
Saa-àngale yi duma nañu Paris SG 3-0. Muy lu bett ñépp. Ndax, Paris SG ñépp a yaakaaroon ni dafay ñëw jaar ci kaw Chelsea jàll, gannaaw ba mu wàccee punkal yu bari ci yoonam. Waaye, mel na ni bëre bukkeek mbaam la woon. Ci xaaj wu njëkk wi la Chelsea dugal biiwam yépp (C. Palmer 22, 30 ak Joao Pedro 43).
– Xabi Alonso : « Xooluma tur… ku nanguwul daw doo futbal ! »
Loolu di lenn ci kàddu yu tàggatkatu Real Madrid mujje yëkkati. Mu melni ñor na ko, ndax wax na ko baamu ko. Li ko waral di doxalin bi ñenn ci ay futbalkatam ame woon ci kuppeg àddina këlëb yi. Xamle na ni, li mu bëgg mooy ñuy nangu di daw ci bu ñu yoree ak bu ñu ñàkkee bal bi.
LÀMB JI
Jóob 2 daan na Tafaa mbër
Doomu yëmbël ji waneeti na mën bëreem gannaaw ba mu daanee Tafaa mbër ci menn cong. Ba arbiit ba nee piriib, Tafaa mbër dox génn saaku yi def ay mbiram dikkaat, ñu dànkaafu ko. Ba arbiit mbiibaatee, ñaari mbër yi taxaw nañu ab diir di ko léewatoo. Ci noonu Jóob 2 jokkaas ko, tollanti ko, fa Tafaa mbër yëkkatee loxo ba ngir fayu rekk mu këf tánkam nooju ko, daan ko.
Liis Njaago ak Aada Faas
Liis Njaago ak Aada Faas amal nañu seen jakkaarloo bu mujj démb ci gaawu bi. Mu tàngoon, safoon sàpp ba ñaari mbër yi jot fa jaxasoo sax. Ba yëf ya jeexee itam, soppe ya xaw nañu fa laale ca mbedd ya. Ñaari mbër yi war a sëgg bésub 19 sulet bii.